3
1 Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu mana tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam. 2 Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nara nekki feeñagul, waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel. 3 Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.
4 Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon. 5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar. 6 Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam. 8 Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane. 9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo mana sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla. 10 Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
Bëgganteleen
11 Ndaxte xibaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante, 12 te baña mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
13 Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle. 14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk, moo nuy xamal ne jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey. 15 Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk. 17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw? 18 Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
Kóolute ci kanam Yàlla
19-20 Ci loolu lanu xame ne nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam, ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp. 21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute. 22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex. 23 Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale. 24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne dëkk na ci nun.