4
Ñiy jàngle luy réeral
Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne ci mujug jamono dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane. Ñooñu ay naaféq yuy naxe lañu, te seen xol dërkiis. Dinañu tere séy, di araamal ay ñam, waaye Yàlla daa sàkk yooyu, ngir ñi gëm te xam dëgg man ciy jëfandiku te di ko ci sant. Ndaxte li Yàlla sàkk lépp baax na, kon wenn ñam araamul ci ku koy jëfandikoo te di ko ci sant. Ndaxte kàddug Yàlla ak ñaan ñoo koy sellal.
Jawriñu Kirist Yeesu ju baax
Saxal ci digal bokk yi loolu nag, kon dinga nekk jawriñu Kirist Yeesu ju baax ju regg ci kàdduy yoonu ngëm wi ak njàngle mu rafet, mi nga xam bu wér. Tanqamlul ay léebi diiney neen, di ay wax yu amul bopp yu àddina kese; waaye tàggatal sa bopp ci ragal Yàlla. Ndaxte tàggat yaram am na fu njariñam yem, waaye njariñu ragal Yàlla dafa daj lépp, ëmb digey àddina ak àllaaxira. Wax ju wóor a ngii, te mata nangu ak gépp kóolute. 10 Danuy ñaq tey bëre, ndaxte wékk nanu sunu yaakaar ci Yàlla Aji Dund ji, di Musalkatu ñépp, rawatina nag ci ñi gëm.
11 Digal leen yëf yooyu nag ci sa njàngle. 12 Bu la kenn xeeb ndax say at, waaye defal sa bopp royukaayu ñi gëm ci say wax ak say jëf, ci sa mbëggeel, sa ngëm ak sa cell. 13 Li feek may dikk, saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di leen dénk ak a jàngal. 14 Bul sàggane may gi nekk ci yaw, gi la Yàlla jox jaarale ko ci waxu yonent, keroog bi la njiit yi tegee loxo. 15 Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp. 16 Sàmmal sa bopp, sàmm sa njàngle, te sax ci; kon dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu.