Saar 12
Israyil jàmbu na Robowam
1 Ba loolu amee Robowam dem dëkk ba ñuy wax Sikem, ndax fa la Israyil gépp daje woon, ngir fal ko buur. 2 Yerbowam doomu Nebat dégge ko ca Misra ga mu dawoon dem, di fa làqu Buur Suleymaan, te toogoon foofa ca Misra ba booba. 3 Waa giiri bëj-gànnaar woolu ko, ñu daldi ànd mook mbooloo mépp ca Robowam. Ñu ne ko: 4 «Sa baay da noo tegoon njaam gu metti. Léegi yaw dangay woyofal sunu liggéey bu metti bi nu sa baay sëf, te yolomal buumu njaam gu teeŋ gi mu nu gàll, kon nu jaamu la.» 5 Mu ne leen: «Demleen ba mu am ñetti fan, ngeen délsi.» Mbooloo ma dem.
6 Buur Robowam giseek mag ña daa taxawu Suleymaan baayam ba muy dund. Mu ne leen: «Lu ngeen may digal, ma wax ko mbooloo mii?» 7 Ñu ne ko: «Soo nangulee tey mbooloo mii, déggal leen, wax leen kàddu yu rafet, say jaam lañuy doon ba fàww.»
8 Robowam nag dégluwul waxi mag ña, xanaa dem giseek xale yu góor, ya màggandoo ak moom te di ko taxawu. 9 Mu ne leen: «Lu ngeen may digal ma wax ko mbooloo mii ne ma, ma yolomal buumu njaam gi leen sama baay gàlloon?»
10 Xale yu góor ya mu màggandool ne ko: «Mbooloo mii ne la sa baay da leena gàlloon buumu njaam gu teeŋ, waaye yaw yolomalal leen ko; li nga leen di wax mooy lii: “Sama baaraamu sanqleeñ moo gëna diis sama tànku baay. 11 Sama baay a leena tegoon njaam gu metti, waaye man maay yokk seen njaam, ba mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daan cawe, waaye man ay leraw yu ñu kor weñ laa leen di cawe.”»
12 Ñetteelu bés ba Yerbowam ànd ak mbooloo ma mépp, dellu ca Robowam, noonee leen ko Buur waxe woon ne leen ñu dem ba mu am ñetti fan, ñu délsi. 13 Buur tontu mbooloo ma kàddu gu ñagas, bàyyi la ko mag ña digaloon. 14 Na ko xale yu góor ya digale la waxeek ñoom, ne leen: «Sama baay a leen tegoon njaam gu metti, waaye man maa koy yokk, mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daa cawe, waaye man ay leraw yu ñu kor weñ laa leen di cawe.» 15 Noonu la Buur tanqamloo mbooloo ma, te Aji Sax ji moo walbatee noonu mbir ma, ngir amal wax, ja mu waxoon Yerbowam doomu Nebat, Axiya waa Silo ba jottli.
16 Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko:
«Ana lu nu bokk ak Daawuda,
lu nu séq ak doomu Yese?
Bànni Israyiloo, ca seeni xayma!
Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.»
Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma; 17 Teewul bànni Israyil ya dëkkoon ca dëkki Yuda, Robowam wéy di seen buur. 18 Ci kaw loolu Buur Robowam yónni Adoram may sase liggéeyi sañul-bañ ya. Teewul Israyil gépp bokk dóor ko ay doj ba mu dee. Buur Robowam daldi gaaw war watiir, daw làquji Yerusalem. 19 Noonu la Israyil fippoo ci kaw waa kër Daawuda ba sunu jonni yàllay tey.
20 Ci biir loolu Israyil gépp dégg ne Yerbowam délsi na; ñu woote ndaje, woo ko ca, fal ko buurub Israyil gépp. Kenn farul ak waa kër Daawuda, lu moy waa giirug Yuda doŋŋ.
21 Ci kaw loolu Robowam agsi Yerusalem, daldi woo waa kër Yuda gépp, ñook giirug Beñamin, ñu daje di téeméer ak juróom ñett fukki junniy nit (180 000), diy ñeyi xare. Ñu nara xareek waa kër Israyil, ngir delloo nguur ga ca loxol Robowam doomu Suleymaan.
22 Ci biir loolu kàddug Yàlla dikkal góoru Yàlla gu ñuy wax Semaya. Mu ne ko: 23 «Waxal Robowam doomu Suleymaan buurub Yuda, ak waa kër Yudak Beñamin ak mbooloo ma ca des, ne leen: 24 “Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen jóg di xeex ak seen bokki bànni Israyil. Na ku nekk ñibbi këram, ndax ci man la mbir mii sababoo.”» Ñu dégg kàddug Aji Sax ji, walbatiku dem, noonee ko Aji Sax ji waxe.
Buurub Israyil bokkaale na
25 Gannaaw loolu Yerbowam tabaxaat Sikem, dëkk ba ca diiwaanu tundi Efrayim, daldi fay dëkk. Mu jóge foofa tabaxaat dëkk ba ñuy wax Penuwel. 26 Yerbowam nag di wax ca xelam naa: «Léegi nguur gi dellu ci loxol waa kër Daawuda. 27 Bu mbooloo mii demee di sarxali ca kër Aji Sax ji ca Yerusalem, seen xol dina walbatiku ne napp ca seen sang, Robowam buurub Yuda. Su ko defee ñu rey ma, dellu ca Robowam buurub Yuda.»
28 Ci kaw loolu Buur seetluwaat mbir ma, daldi sàkklu ñaari wëlluy wurus. Mu ne mbooloo ma: «Yeen waa Israyil, bare ngeen lu ngeen di jaabante yoonu Yerusalem. Xool-leen fii kay! Seen yàlla ya leen génne woon réewum Misraa ngi.» 29 Ba loolu amee mu teg wenn wëllu wa ca dëkk ba ñuy wax Betel, wa ca des mu tegi ko ca Dan. 30 Mbir moomu doon bàkkaar. Mbooloo ma dox jiitu wenn wëllu wa, ba àgg Dan. 31 Ci kaw loolu Yerbowam tabax ay bérabi jaamookaay, ba noppi tabb ay sarxalkat ci baadoolo yu bokkul ci askanu Lewi.
32 Ba mu ko defee Yerbowam dogal màggalug fukki fan ak juróom ca weeru juróom ñetteel wa. Mu mel ni màggal gay am Yuda. Yerbowam rendi ay sarax ca sarxalukaay ba. Noonu la def Betel, rendil fa ay sarax wëllu ya mu defarlu woon, defal ko wëllu ya sarax. Ci biir loolu mu tabb ca Betel ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay yooyu mu sos. 33 Nii la rendee ay sarax ca kaw sarxalukaay ba mu sàkklu ca Betel, ca fukki fan ak juróom ca weeru juróom ñetteel wa, muy weer wu mu tànnal boppam. Ba mu ko defee mu dogalal waa Israyil màggal googu, daldi yéeg ca kaw sarxalukaay ba, ngir taal fa sarax su ñuy lakk.