Saar 27
Daawuda làquji na ca waa Filisti
1 Daawuda nag ma nga naan ca xelam: «Bés a ngi ñëw bu ma nara sànku ci loxol Sóol. Li gën ci man daal, du lenn lu moy dawa daw ba ca réewu waa Filisti, ba Sóol tàyyi maa rëbbati ci Israyil gépp, ma daldi mucc.» 2 Ba loolu amee Daawuda ak juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom, daldi jàll ba ca buurub Gaat, Akis doomu Mawog. 3 Daawuda dal ca Akis ca Gaat, mook ay nitam, ku ci nekk ak njabootam; Daawuda ak ñaari soxnaam, Ayinowam waa Yisreel ba, ak waa Karmel ba, Abigayil, soxnas Nabal woon. 4 Ba ñu waxee Sóol ne ko Daawuda daw na, dem Gaat, Sóol rëbbatu ko.
5 Daawuda nag ne Akis: «Ngalla baaxe ma, may ma fi ab gox ci dëkki àll bii, ma man faa dëkke; ndax man sab surga laa, warumaa bokk dëkk ak yaw ci péeyu buur.» 6 Bésub keroog la ko Akis jox dëkk ba ñuy wax Ciglaag. Moo tax Ciglaag ñeel buuri Yuda ba tey jii. 7 Diir ba Daawuda dal ca àllub Filisti, at la ak ñeenti weer.
8 Ci biir loolu Daawuda aki nitam daan nañu song-songee Gesureen ñi ak Giraseen ñi ak Amalegeen ñi. Mooy ña dëkke woon naka jekk réew mooma, ba ca Sur, jàpp réewum Misra. 9 Saa yu Daawuda songaan gox ba, du ca wacc kuy dund; du góor, du jigéen, te it day lël jur gu gudd ak gu gàtt, mbaam ak giléem, aki yére. Su ko defee mu walbatiku, dellu ca Akis. 10 Bu ko Akis laajee ne ko: «Fu ngeen lële woon tey?» Daawuda ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Yuda,» mbaa «Xanaa wetu Negew ca Yerameleen ña,» mbaa mu ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Keneen ña.» 11 Moo tax du genn góor mbaa jigéen ju Daawuda masa bàyyi mu dund, di ko indi Gaat, ndax ragal ñu nettali lu jëm ci ñoom, naan nàngam ak nàngam la ñoom Daawuda def. Noonu la jàppoo woon mboolem diir ba mu dal ca àllub Filisti. 12 Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»