Saar 16
Axas falu na buur ca Yuda
1 Ba buurub Israyil Peka doomu Remalya duggee fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Axas doomu Yotam falu buur ca Yuda. 2 Ñaar fukki at la Axas amoon ba muy falu buur. Nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem, waaye deful li Aji Sax ji Yàllaam rafetlu, na ko maamam Daawuda baaxoo woon. 3 Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil. 4 Rendi nay sarax, taal na cuuraay ca bérabi jaamookaay yaak ca kaw tund yaak mboolem ker garab gu naat.
5 Ci kaw loolu Reccin buurub Siri, ak buurub Israyil Peka doomu Remalya, jóg song Yerusalem xare. Ñu gaw Buur Axas, te manuñu koo daan. 6 Jamono yooyu, fekk na Reccin nangu Elat, mu tàbbi ci loxol Siri. Mu génne waa Yuda Elat; Edomeen ña délsi Elat, dëkk fa ba bésub tey jii. 7 Axas nag yebal ay ndaw ca Tiglaat Pilser buurub Asiri, ne ko: «Man de, dama di sab jaam, te di sa doom. Kon nag ngalla dikkal xettli ma ci ñi ma jógal, di buurub Siri ak buurub Israyil.» 8 Axas jël xaalis ak wurus wa nekkoon ca kër Aji Sax ja ak ca dencukaayi kër Buur, defal ko buurub Asiri yóbbal. 9 Buurub Asiri nangul ko, dal ca kaw Damaas, nangu dëkk ba, jàpp waa dëkk ba, yóbbu Kir, ba noppi rey Reccin.
10 Gannaaw loolu Buur Axas dem ca Tiglaat Pilser buurub Asiri ca Damaas, gis fa sarxalukaay ba fa nekk. Ba mu ko defee Buur Axas yónnee ca Uri sarxalkat ba, nataalu sarxalukaay ba ak tabaxin waak mboolem na mu bindoo. 11 Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi. 12 Ba Buur Axas ñibbsee, jóge Damaas, ba nemmiku sarxalukaay ba, daa dikk ba ca sarxalukaay ba, joxe fa sarax. 13 Taal na fa saraxu rendi-dóomalam, joxe ca saraxu peppam, sotti ca saraxu tuuroom, ba noppi xëpp deretu saraxu cantam ci biir jàmm ca kaw sarxalukaay ba. 14 Sarxalukaayu xànjar ba tege woon ca kanam Aji Sax ji, mu jële ko ca kanam kër ga mu nekkoon, ca diggante sarxalukaay bu bees baak kër Aji Sax ji, teg ko ca wetu sarxalukaay bu bees ba, fa féete bëj-gànnaar. 15 Ci biir loolu Buur Axas sant Uri sarxalkat ba ne ko: «Ci kaw sarxalukaay bu mag bi ngay joxe saraxu rendi-dóomalu suba si, ak saraxu pepp bu ngoon bi, ak saraxu rendi-dóomalu buur bi, ak saraxu peppam, boole ci saraxu rendi-dóomal bi ñuy joxeel mboolem waa réew mi, ak seen saraxu pepp, ak seen saraxu tuuru. Te nga xëpp ci kawam mboolem deretu saraxu rendi-dóomal bi, ak deretu mboolem sarax su ñuy rendi. Sarxalukaayu xànjar bi moom, maa koy moom, di ko gindikoo ci Aji Sax ji.» 16 Uri sarxalkat ba def la ko Buur Axas sant lépp.
17 Ci kaw loolu Buur Axas toj làcci rootukaay ya ñuy dawal* 16.17 làcci rootukaay: seetal ci 1.Buur ya 7.27-29., jële bagaan ya woon ca kaw, teggi mbalka mu mag ma ñuy wax Géej te tege woon ca yëkki xànjar ya ko yenu. Mu teg ko ci kawab dëru doj. 18 Ci kaw loolu bëgg lu neex buurub Asiri tax mu soppi buntu bésub Noflaay, ba mbaar tiimoon ci biir kër Aji Sax ji, soppiwaale buntu buur ba féete biti.
19 Li des ci mbiri Axas ak la mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 20 Gannaaw gi Axas tëdd, fekki ay maamam. Ca ay maamam lañu ko denc, ca gox ba ñu naan dëkku Daawuda, Esekiya doomam falu buur, wuutu ko.