Saar 24
1 Ca ay jantam la Nabukodonosor buuru Babilon song réew ma. Yowakim nangul ko diiru ñetti at, doora walbatiku fippu. 2 Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal ci kawam ay yàqkati waa Babilon ak yàqkati Siri ak yàqkati Mowab ak yàqkati Amoneen ña. Aji Sax ji yebal leen Yuda ngir ñu yàqte ko, mu dëppook kàddu ga mu waxoon, yonent yiy surgaam jottli ko. 3 Ci ndigalal Aji Sax ji moos la loolu xew ca Yuda, ba mu mujj leen xarab ndax bàkkaari Manaseek li mu def lépp, 4 ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal.
5 Li des ci mbiri Yowakim ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 6 Gannaaw gi Buur Yowakim tëdd, fekki ay maamam. Doomam Yowakin nag falu buur, wuutu ko. 7 Jamono yooyu buuru Misra génnatul réewam di xareji, ndax fekk na buuru Babilon nangu suufam sépp la ko dale ca xuru Misra ba ca dexu Efraat.
Yowakin falu na buur ca Yuda
8 Fukki at ak juróom ñett la Yowakin amoon ba muy falu buur. Ñetti weer la nguuru, péeyoo Yerusalem. Yaayam mooy Newusta doomu Elnatan ma cosaanoo Yerusalem. 9 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko baayam defe woon.
10 Jamono jooja la jaraafi Nabukodonosor buuru Babilon, song Yerusalem, gaw dëkk ba. 11 Nabukodonosor dikk ca dëkk ba, fekk ay jaraafam gaw ko. 12 Yowakin buurub Yuda génn fekki buuru Babilon, jébbal ko boppam, mook ndeyam aki surgaam aki jaraafam ak jawriñi këram. Buuru Babilon nag jàpp ko. Looloo nga yemook juróom ñetteelu atu nguurug Nabukodonosor buuru Babilon. 13 Nabukodonosor jële fa mboolem alali kër Aji Sax ji ak alali kër Buur, daldi buub lépp luy ndabu wurus lu Suleymaan buurub Israyil defarlu woon ci kër Aji Sax ji, muy la Aji Sax ji waxoon.
14 Ci biir loolu buuru Babilon yóbbu Yerusalem gépp, muy mboolem jaraaf yeek jàmbaari góor ñi, ñuy fukki junni, ñook mboolem liggéeykat yaak tëgg ya. Kenn desul, lu moy baadoola ya gëna néew doole.
15 Mu yóbbu Yowakin Babilon mook ndeyam aki soxnaam aki jawriñam ak kilifay réew ma. 16 Buuru Babilon boole ca jàppaale juróom ñaari junniy jàmbaari góor (7 000), ak junniy liggéeykat aki tëgg, ñoom ñépp di boroom kàttan te tollu ci xare; mu boole leen jàpp jaam, yóbbu Babilon. 17 Buuru Babilon moo fal Mataña, baayu Yowakin bu ndaw, mu wuutu Yowakin, daldi soppi turu Mataña, tudde ko Cedekiya.
Cedekiya falu na buur ca Yuda
18 Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna. 19 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon. 20 Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xarab leen.
Gannaaw gi Cedekiya fippu buuru Babilon.