Saar 4
1 Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan. 2 Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare. 3 Ma joxe ndigal, woolu boroom xam-xami Babilon yépp, ngir ñu xamal ma pirim gént gi. 4 Ci kaw loolu taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi dikk. Ma nettali leen gént gi, waaye waxuñu ma piri mi. 5 Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltasar, mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.
6 Ma ne ko: «Beltasar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi. 7 Li ma gis daal ci sama kaw lal mooy lii:
Damaa jekki gis garab ci digg àddina si,
mu gudd lool.
8 Garab gay màgg, di réy,
ba njobbaxtal la di laal asamaan,
ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.
9 Xob yaa nga naat,
meññeef ma ne gàññ,
mana dundal ñépp.
Muy keppaaral rabu àll,
di tàggal njanaaw,
di dundal bépp boroom bakkan.
10 «Fi ma tëdd ci sama lal, ma jekki gis ab wattukat bu sell wàcce asamaan. 11 Mu àddu ca kaw ne:
“Daaneleen garab gi te gor ay bànqaasam.
Wittleen xob yi, tasaare meññeef mi.
Na rab yi jóge ci keppaaram, daw,
njanaaw yi ciy bànqaasam, naaw.
12 Waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf,
ci digg mbooy mi,
te jénge ko càllalay weñ ak xànjar.
Na ko layub asamaan di faam,
muy dunde ñax nig jur.
13 Mu nitoodi,
ame xelum mala
diiru juróom ñaari jamono.
14 Ndogal a ngoog bu wattukat yi tëral,
àttee ngoog bu ñu sell ñooñu digle,
ngir aji dund ji xam ne
Aji Kawe jee yilif nguurug nit,
di ko jox ki ko soob,
di ca fal ki gëna tuut.”
15 «Loolu laa gént, man, Nabukodonosor. Yaw Beltasar nag, wax ma piri mi. Ndax boroom xam-xam yi ci sama réew mi, kenn manu ma cee wax piri mi. Waaye yaw man nga ko, ngir xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw.»
16 Ba loolu amee Dañeel ma ñuy wax Beltasar ne dann ab diir, jaaxle, xalaat yu ko tiital dikkal ko. Buur àddu ne ko: «Beltasar, gént geek piri mi bumu la tiital.» Beltasar ne ko: «Sang bi, su ma sañoon de muy sa géntug noon te pireem topp say bañaale. 17 Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp, 18 mook xobam yu naat ak meññeefam mu ne gàññ, mana dundal ñépp; muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw: 19 Buur de, garab googu yaw la. Yaa màgg, di bare doole; di màgg ba laal asamaan, sa kilifteef àkki cati àddina.
20 «Buur, li nga gis kenn ci wattukat yu sell yi wàcce asamaan, àddu ca kaw ne:
“Daaneleen garab gi, tas ko,
waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf,
ci digg mbooy mi,
te jénge ko càllalay weñ ak xànjar.
Na lay biy wàcc, di ko faam,
muy dunde ñax nig jur
diiru juróom ñaari jamono.”
21 Piri maa ngii, Buur, di dogalu Aji Kawe, ji dal ci sa kaw, Buur, sang bi. 22 Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex. 23 Li ñu santaane ñu bàyyi ëkk beek reeni garab gi mooy tekki ne nguur gi dees na la ko delloo keroog boo xamee ne Boroom asamaan mooy Buur. 24 Kon nag Buur, ngalla nangul li ma lay digal: say moy ak say bàkkaar, daboo ko di def njekk ak di baaxe néew-ji-doole ndax sa teraanga sax.»
25 Loolu lépp dal na Buur Nabukodonosor. 26 Ba ñu ca tegee fukki weer ak yaar yu mat, muy doxantu ca kaw taaxum kër buur ca Babilon. 27 Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»
28 Kàddug Buur ga daanoogul sax, baat jibe asamaan àddu ne: «Yaw Buur Nabukodonosor, dogal ñeel na la ne nguur gi rëcc na la. 29 Dees na la dàqe ci nit ñi, nga dëkk ak rabi àll yi, ñax di sam xont niw nag diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.»
30 Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nabukodonosor. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.
Nabukodonosor xippi na
31 Ba àpp ba matee, man Nabukodonosor, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko:
kilifteefam sax fàww,
nguuram ñeel maasoo maas.
32 Mboolem waa àddina
di neen ci moom.
Nu ko neex lay def
ak gàngoori xarey asamaan
ak waa suuf,
te kenn du fél loxoom
mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»
33 Ba sama sago délsee, ca laa jotaat ndam ak daraja ngir sama teraangay nguur. Ba loolu amee samay jawriñ ak samay jaraaf jëlsi ma; ñu dëjaat ma ci nguur gi, ma gënatee màgg. 34 Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.