Saar 15
Lu jëm ci njéggalug bor
1 Juróom ñaari at yu mat yu nekk, nangeen amal njéggalug bor. 2 Mbirum njéggaleg bor gi, nii lay deme: mboolem ku lebaloon dëkkandoom, bumu ko ca feyeekooti. Na jéggale la mu lebaloon dëkkandoom, mbokkum bànni Israyilam, gannaaw bu ñu biralee njéggaleg bor, ñeel Aji Sax ji. 3 Jaambur bi bokkul ci bànni Israyil, sañ ngeen koo feyeeku, waaye la leen seen mbokkum bànni Israyil ameel, jéggaleleen ko.
4 Waaye ab ndóol du am ci seen biir, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeel bu baax ca réew ma mu leen di jox, muy seen cér, ngeen jagoo, 5 ndegam déggal ngeen bu baax seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem santaane bii ma leen di dénk tey. 6 Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelee ni mu ko waxe déy, yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb. Te it yeenay yilif xeet yu bare, waaye yeen, deesu leen yilif.
7 Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israyil, ci benn ci seen dëkki réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo, seen mbokkum ndóol moomu. 8 Nàddil-leen koo nàddil, abal koo abal dayob soxlaam. 9 Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar. 10 Nangeen ko joxa jox te bu ngeen koy jox it, bu ci seen xol bon, ndax loolu mooy tax seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seen liggéey, ak mboolem seenu ñaq. 11 Du ñàkk nag ab ndóol ci réew mi. Moo tax ma sant leen ne leen ngeen nàddila nàddil seen mbokkum ndóol, ak seen néew-ji-doole ji ci seenum réew.
Sang am na lu ko war ci jaamam
12 Su fekkee ne seen mbokkum bànni Israyil, góor mbaa jigéen da leena jaay boppam* 15.12 Mbaa: su fekkee ne dees leena jaay seen mbokkum bànni Israyil., bu leen liggéeyalee juróom benni at, atum juróom ñaareel ma, yiwileen ko, mu moom boppam. 13 Te bu ngeen ko yiwee, mu moom boppam it, buleen ko yiwee loxoy neen. 14 Sàkkal-leen koo sàkkal ci seeni gàtt, ak seenum pepp, ak seen biiñ. Kemu alal ja leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeele, moom ngeen koy jox. 15 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey.
16 Ndegam nag seen jaam a leen ne: «Duma dem, ba la,» ndax cofeel gu mu am ci yeen ak seen waa kër, te bànneexam di nekk ak yeen, 17 su boobaa fableen puso, ngeen sësale noppu jaam bi seen lafu bunt, te ngeen bënne puso bi noppam, ba mu jam ci lafu bunt bi, mu daldi doon seen jaam ba fàww. Seen jaam bu jigéen it, noonu ngeen di def ak moom.
18 Buleen mititlu lu ngeen yiwi seenub jaam, mu moom boppam, ndax jariñ na leen lu fey ñaari yoon surga buy feyeeku, ci juróom benni at yi mu leen liggéeyal. Te seen Yàlla Aji Sax ji dina leen barkeel ci mboolem lu ngeen def.
Li war ci taawug jur
19 Mboolem luy taaw ci seen jur gu gudd, ak gu gàtt, te di góor, defal leen ko seen Yàlla Aji Sax ji cér bu sell. Buleen liggéeyloo mukk seen yëkk wu dib taaw, te buleen wat seen gàtt bu dib taaw. 20 Fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji ngeen ko wara xéewloo at mu jot, yeen ak seen njaboot, fi bérab bi Aji Sax ji taamu. 21 Jur gu ci am sikk nag, muy soox, mbaa mu gumba, mbaa mu am sikk su réy su mu mana doon, buleen ko sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji. 22 Ci seen biir dëkk ngeen ko wara xéewloo, te ku sobewu ak ku set yépp man na caa lekk, mel ni bu doon kéwél mbaa kooba. 23 Waaye deretam, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy sotti nim ndox.