Saar 31
Tabb nañu ay liggéeykat yu xareñ
1 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: 2 «Gisal, maa woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. 3 Maa ko feesale xelum Yàlla, ak xareñte ak déggin ak xam-xam, ak manoorey bépp xeetu liggéey, 4 ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, 5 di yett per yu muy tapp, di yett bant, di liggéey lu nekk. 6 Maa ngii di ko tofal Oliyab doomu Ayisamaag Daneen bi, te itam mboolem ñi xarala, may naa leen xelum xarala, ngir ñu ànd def mboolem lii ma la sant: 7 Muy xaymab ndaje mi, ak gaalu àlluway seede si, ak kubeeru saraxu njotlaay gi ci kawam, ak mboolem jumtukaayi xayma bi; 8 taabal ji, ak ndab yi, ak tegukaayu làmpu wurusu ngalam beek yëfam yépp, ak sarxalukaayu cuuraay bi, 9 ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom, 10 ak itam yére yu yànj yi, yére yu sell yi ñeel Aaróona sarxalkat bi ak yérey doomam, yi ñuy sol, di sarxale, 11 ak diwu pal gu sell gi, ak cuuraay lu xeeñ li ñeel bérab bu sell bi. Loolu ma la sant lépp, nañu ko defe noonu.»
Lu jëm ci solob bésub Noflaay
12 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: 13 «Waxal bànni Israyil ne leen: “Fexeleen rekk ba sama bési Noflaay, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen. 14 Wormaal-leen bésub Noflaay ndax lu sell la, ñeel leen. Ku ko teddadil, dee rekk mooy àtteem: képp ku ci liggéey, kooku dees na ko dagge ci biiri bokkam. 15 Juróom benni fan lees wara liggéey, waaye bésub Noflaay bay juróom ñaareel ba, bés bu sell la, bésub Noflaay bu mat sëkk, ñeel Aji Sax ji. Képp ku liggéey bésub Noflaay, dee rekk mooy àtteem. 16 Na bànni Israyil wormaal bésub Noflaay, nañu sàmm bésub Noflaay, ñook seen askan. Kóllëre la gu sax dàkk. 17 Sama diggante laak bànni Israyil, te firnde la ju sax dàkk, ndax ci juróom benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan ak suuf, bésub juróom ñaareel ba, mu dal-lu, daldi yeeslu.”»
18 Ba Yàlla noppee wax ak Musaa ca kaw tundu Sinayi, da koo jox ñaari àlluway doj yu mu binde loxol boppam.