Bànni Israyil yékkati na jaamookaay ba
Saar 35
Bésub Noflaay du bésu liggéey
1 Musaa nag dajale mbooloom bànni Israyil mépp. Mu wax leen ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane, ngir ñu def ko: 2 Juróom benni fan lees di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, seen bésub Noflaay bu sell bu mat sëkk la, ñeel Aji Sax ji. Képp ku ci liggéey lenn, dees koy rey. 3 Buleen jafal sax sawara fenn ci seeni dëkkuwaay, ci bésub Noflaay.»
Ay sarax war na ci jaamookaay bi
4 Musaa dellu wax ak mbooloom bànni Israyil mépp ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane.
5 «Sàkkleen ci seen alal ab jooxe bu ñeel Aji Sax ji. Képp ku am yéeneb xolam, na indi jooxeb Aji Sax ji: wurus ak xaalis ak xànjar, 6 ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ak kawari bëy 7 ak deri kuuy yu ñu suub xonq, ak deri piipi, ak banti séng, 8 ak diwu làmp, ak ay xeeñal ngir diwu pal geek cuuraay lu xeeñ li, 9 ak ay peri onigsë ak yeneen per yuy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi.
10 «Mboolem ku xareñ ci yeen, na ñëw, ngeen def li Aji Sax ji santaane lépp: 11 jaamookaay bi ak xaymaam ak kiiraayam aki keppoom aki làccam, ak galan yeek jën yeek tegu yi, 12 ak gaal geek ay njàppoom ak kubeer gi ñuy amale ag njotlaay, ak rido bi ko làq, 13 ak taabal jeeki njàppoom ak ndabam yépp ak mburum teewal mi, 14 ak tegukaayu làmp bi, aki jumtukaayam aki làmpam ak diwu làmp bi, 15 ak sarxalukaayu cuuraay bi aki njàppoom, ak diwu pal gu sell gi, ak cuuraay lu xeeñ li; ak kiiraayal buntu jaamookaay bi, 16 ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak caaxub xànjaram aki njàppoom ak li muy àndal lépp; mbalkam njàpp mi akub tegoom, 17 ak sor yi yéew jaamookaay bi aki jënam aki tegoom, ak lafu buntu ëtt bi, 18 ak xeri jaamookaay bi, ak jën yi yéew ëtt bi ak seeni buum, 19 ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi, yére yu sell yu Aaróona, sarxalkat bi, ak yérey doomam, yi ñuy sarxalee.»
20 Ci kaw loolu mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo fa Musaa. 21 Ba mu ko defee mboolem ña ca am pastéefu xol ak mboolem ña ca seen xel xiir, ñépp dikk, indi jooxeb Aji Sax ji ngir liggéeyu xaymab ndaje meek bépp liggéey bu mu laaj, ngir itam yére yu sell yi. 22 Góor ak jigéen bokk dikk, mboolem ñi am yéeney xolam, mboolem ñi bëgga indi wurus, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbale; ñii indi ay lam, ñii jaaroy nopp, ñii jaaroy loxo, ñii ay caq, gànjari wurus yu nekk rekk. 23 Te it mboolem ñi dencoon wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy mbaa deri xar yu ñu suub xonq, mbaa deri piipi, ñoom ñépp a indi la ñu dencoon. 24 Képp ku namma jooxe xaalis mbaa xànjar, jooxeel nga ko Aji Sax ji, te itam képp ku dencoon bantu séng bu jëm ci mboolem liggéeyu sarxal bi, indi nga bant bi. 25 Ci biir loolu jigéen ñu xareñ ñépp ëcce seeni loxo, ngir waajal wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu boole, indi. 26 Mboolem jigéen ñi ko mane te am yéeneem itam, daldi ëcc kawari bëy. 27 Njiit yi nag indi ay peri onigsë ak yeneen per yiy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi, 28 aki xeeñal, akug diw ngir làmp beek diwu pal geek cuuraay lu xeeñ li. 29 Mboolem bànni Israyil, góor ñeek jigéen ñi am yéeney indi lu jëm ci liggéey bi Aji Sax ji santaane, Musaa jottli, ñoom ñépp a indil Aji Sax ji ay saraxi yéene.
Besalel ak Oliyab tàmbali nañu liggéey bi
30 Musaa nag ne bànni Israyil: «Gisleen, Aji Sax ji moo woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. 31 Moo ko feesale xelum Yàlla ak xareñte ak déggin ak xam-xam ak manoorey bépp xeetu liggéey, 32 ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, 33 di yett per yu muy tapp, di yett bant, di liggéey lu nekk. 34 Mayu jàngle itam yeb na ko cib dënnam, moom ak Oliyab, Daneen bi, doomu Ayisamaag. 35 Moo leen feesal xareñte, ngir bépp liggéey, ci wàllu yett ak nataal, ak liggéeyu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Mane nañu ràbb te itam dañuy sos seen taarali bopp.