Njàlbéen ga
di xaaj bi jëkk ci Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Njàlbéen ga mooy téere bi jëkk ci Tawreet. Yonent Yàlla Musaa moo bind Tawreet, juróomi téere yi jiitu ci Mbind mu sell mi.
Téereb Njàlbéen ga moo tënk ndoortel lépp lu Yàlla sàkk, muy asamaan ak suuf ak gàncax geek rab yi, ba ci nit; lépp di lu baax.
Téere bii nag wone na ni àddina mujj mel, ndax ñaawtéefi nit, yi law ba sunu jonni Yàllay tey. Gis nanu ci Njàlbéen ga ne ca Aadama ak Awa la nit dale déggadil Yàlla, di wuta moom boppam tey fippu, te loolu mooy bàkkaaram. Mu jural ko lu bon, jural ko coonob àddina bu tar, tey gëna tar, soreele kook Yàlla. Booba la dee tàmbali ci àddina. Nekkinu nit mujj na naqari lool, nekkinu suuf it noonu, wuuteek ba Yàlla di sàkk lépp, ba mu baax.
Nu gis ne Njàlbéen ga dafa lëkkloo ak mboolem yeneen wàll yi ci des, lépp di benn xibaar buy dégtal nit alkàndeem, gi sababoo ci bàkkaaram, te di ko xamal mbaaxu Yàlla ñeel képp kuy doom Aadama. Waaye xibaar la it buy yégle àtteb Yàlla, ñeel ñi xalab aw yiwam.
Pexe mi Yàlla lalal nit ngir texeem te misaaloon ko xaat ci Njàlbéen ga ci saar 3, aaya 15 (3.15), mu ngi sottee ci musalkat bi wara ñëw.
Téereb Njàlbéen ga nag làqul matadig nitoo nit, te yonenti Yàlla yi sax muccuñu ci bàkkaar. Looloo tax du kenn ci yonent yi ku manoona sottal li Yàlla tëralal doom Aadama, ngir mu mucc ci noteelu bàkkaar, mucc ci sànkute gi bàkkaar jur, ba jot ci yiwu Yàlla wi koy texeel.
Bu loolu weesee, téereb Njàlbéen ga leeral na ci saar 12, aaya 3 (12.3) ne, la Yàlla digoon Ibraayma, maami aji gëm ñi, dig ko doomam Isaaxa ak sëtam, Yanqóoba, moom Isaaxa ak askanam ñoo ko jëkkoona jagoo. Waaye dige la bu jaare ca ñoom, doon barke, ñeel xeeti àddina yépp.
Ibraayma wone na nu nit wara taxawe, ba jot ci digeb Yàlla. Ngëm gu dëggu ak kóolute gu wér ci Yàlla. Ngëm googu ak kóolute googu ci Yàllaak kàddoom moo mana tax nit ku nekk mana jot ci barke bi Yàlla dig Ibraayma, doonte kenn yelloowu ko.
Ci Tënk:
1:1-2:25 Lu jëm ci càkkuteefu asamaan ak suuf
3:1-3:24 Lu jëm ci bàkkaaru nit ak njeexitalam
4:1-8:22 Lu jëm ci askanu Kayin ak Set ba ca mbënn ma
9:1-11:9 Gannaaw mbënn ma ba ca taaxum Babel
11:10-50:26 Lu jëm ci Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ba ci Yuusufa
Saar 1
Yàlla sàkk na àddina, fal ci nit
1 Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. 2 Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.
3 Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. 4 Yàlla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm. 5 Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk.
6 Yàlla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.» 7 Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona. 8 Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba.
9 Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. 10 Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na.
11 Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. 12 Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu. Yàlla gis ne baax na. 13 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba.
14 Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. 15 Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. 16 Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi. 17 Yàlla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf, 18 ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na. 19 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba.
20 Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» 21 Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. 22 Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» 23 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba.
24 Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. 25 Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na.
26 Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»
27 Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram;
ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit,
góor ak jigéen la bind.
28 Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»
29 Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. 30 Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona.
31 Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba.