Askanu doomi Nóoyin
Saar 10
(Saar 10.1—11.9)
Xeet yi sosoo ci doomi Nóoyin
1 Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom.
Li jëm ci askanu Yafet
2 Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. 3 Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. 4 Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. 5 Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet.
Li jëm ci askanu Xam
6 Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. 7 Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan.
8 Kuus moom itam jur Namróot, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, 9 mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» 10 Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. 11-12 Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala.
13 Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 14 ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi.
15 Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett, 16 te mooy maami Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi 17 ak Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi, 18 ak Arwàddeen ñi ak Semareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. 19 Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
20 Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
Li jëm ci askanu Sem
21 Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. 22 Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. 23 Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. 24 Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber; 25 Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan.
26 Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yera 27 ak Adoram ak Usal ak Digla 28 ak Obal ak Abimayel ak Saba 29 ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. 30 Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa, ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku.
31 Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
32 Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.