Saar 15
Yàlla fas na ak Ibraam kóllëre
1 Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.» 2 Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» 3 Ibraam teg ca ne: «Mayoo ma giir, te it jaam bu juddoo sama kër moo may donn.»
4 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ko, ne ko: «Du moom moo lay donn, waaye ku sosoo ci sa geño moo lay donn.» 5 Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» 6 Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub.
7 Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.» 8 Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» 9 Aji Sax ji ne ko: «Jëlal wëlluw ñetti at ak bëyu ñetti at ak kuuyu ñetti at, boole ci pitaxu àll ak xati mu ndaw.» 10 Ibraam boole yooyu yépp, rey, lu ci nekk mu dagg ko ci digg bi, dog bu nekk janook moroom ma, waaye daggul picc ya. 11 Ba mu ko defee ay tan jóge ca, dal ca kaw yàpp wa, Ibraam nag dàq leen.
12 Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam. 13 Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at. 14 Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare. 15 Yaw nag dinga gudd fan lool, doora nelaw, ñu denc la, nga fekki say maam ci jàmm. 16 Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi* 15.16 Amoreen ñi: ñoo jëkkoona moom réewu Kanaan. jéggeegul dayo.»
17 Ba jant sowee, ba guddi jot, njaq luy saxar, ànd ak jum buy tàkk, daldi jaar ci diggante dogi yàpp yooyu. 18 Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, 19 mooy réewu Keneen ñi ak Keniseen ñi ak Kadmoneen ñi 20 ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi, 21 boole ci réewum Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Girgaseen ñi ak Yebuseen ñi.»