Saar 22
Yàlla nattu na Ibraayma
1 Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.» 2 Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.»
3 Ibraayma nag teela xëy, takk mbaamam, ànd ak ñaari surgaam ak doomam Isaaxa, daldi xar matt, mi muy lakke sarax bi. Ma nga jëm fa ko Yàlla wax. 4 Ca gannaaw ëllëg sa, Ibraayma daa dawal bëtam, séen bérab ba fu sore. 5 Mu ne surga ya: «Négleen fii, mbaam mi taxaw. Man ak xale bi nu dem ba fale, màggali Yàlla te ñëw.»
6 Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar. 7 Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» 8 Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.
9 Ba ñu àggee fa ko Yàlla wax, Ibraayma sàkk fa ab sarxalukaay, teg ca matt ma, yeew Isaaxa doomam, teg ko ca kaw matt ma ca sarxalukaay ba. 10 Ibraaymaa nga tàllal loxoom, ŋëb paaka, ba muy rendee doom ja. 11 Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» 12 Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.» 13 Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal. 14 Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
15 Ci kaw loolu malaakam Yàlla ma dellu àddoo asamaan ne Ibraayma: 16 «Déglul lii Aji Sax ji wax: “Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji, 17 maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk, 18 te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
19 Ba loolu wéyee Ibraayma waññiku, fekki surga ya, ñu daldi ànd ñoom ñépp, jëm Beerseba, ndax fa la Ibraayma dëkkoon.
Askanu Naxor
20 Gannaaw gi, dañoo yégal Ibraayma ne ko: «Milka kat am na ay doom moom it, moom ak sa mag Naxor. 21 Uus lañu taawloo, teg ca Bus, teg ca Kemwel, miy baayu Aram, 22 teg ca Keset ak Aso ak Pildas ak Yidlaf ak Betuwel.» 23 Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor. 24 Rewma it nekkaaleem la woon, doom ya mu ca am di Teba ak Gaxam ak Taxas ak Maaka.