Saar 13
Dundin wu rafet moo neex Yàlla
1 Cofeel gi war ci bokki gëmkat, saxooleen ko. 2 Buleen sàggane di terle, nde am na ñu seen teraanga tax ñu fat ay malaaka te xamuñu ko woon. 3 Bàyyileen xel ñi ñu tëj, ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëj, ak itam ñi ñuy mitital, ndax yeen itam, aw yaram ngeen am.
4 Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.
5 Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne:
«Duma la bàyyi mukk,
duma la wacc mukk* 13.5 Seetal ci Baamtug Yoon wi 31.6..»
6 Moo tax nu mana am fitu wax ne:
«Boroom beey sama ndimbal, duma tiit.
Ana lees ma manal† 13.6 Seetal ci Sabóor 118.6.?»
7 Fàttlikuleen seen njiit, yi leen àgge kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seenug dundin meññ, te ngeen roy seen ngëm. 8 Yeesu Almasi menn mi la woon démb ak tey ba fàww.
9 Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.
10 Sunu sarxalukaayu bopp, la ñu cay jooxe, ñay liggéeye ca xaymab jaamookaay ba, sañuñu caa lekk. 11 Ndax kat, jur ga sarxalkat bu mag ba daan yóbbu seen deret ca bérab bu sell baa sell, ngir njotlaayal bàkkaar, seen yaram lees daan lakk ca bitib dal ba. 12 Moo waral Yeesu itam deeye ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi, deretu boppam. 13 Kon nag, nanu ko fekki ca bitib dal ba, ba tegoo toroxtaangeem ga mu tegoo woon, 14 ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
15 Kon nag saa su nekk, nanuy jooxee ci Yeesu, sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam. 16 Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.
17 Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.
18 Deeleen nu ñaanal nag. Li nu wóor de, moo di sunum xel yeddu nu fenn, te it di def lu baax ci lépp moo di sunu bëgg-bëgg. 19 Ma di leen gëna tinooti, ngir ngeen ñaanal nu, ba ma délsil leen nu mu gëna gaawe.
20 Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk, 21 yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottale Yeesu Almasi, mi daraja ñeel ba fàww. Amiin.
22 Kon nag bokk yi, dëgg waay, muñleen ma ñaaxe leen gii kàddu. Bañ naa ko ba gàttal bataaxal bii ma leen bind.
23 Xamleen ne sunu mbokk Timote génn na kaso. Su dikkee léegi, moom laay àndal, seetsi leen.
24 Nuyul-leen ma mboolem seeni njiit, ak mboolem gëmkat ñu sell ñi. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu.
25 Yal na aw yiw ànd ak yeen ñépp.