Saar 3
Aji Sax ji xiir na Israyil ci cofeel
1 Aji Sax ji ne ma: «Demaatal bëggi jigéen ju faram bëgg, te muy moykat. Bëgg ko ni Aji Sax ji bëgge bànni Israyil, doonte dañuy walbatiku ci yeneen yàlla te bëgg seen saraxi nàkki reseñ.»
2 Ci kaw loolu ma takk ko ci fukki poseti xaalis ak juróom, ak ñeenti téeméeri kiloy lors ak juróom fukk (450). 3 Ma ne ko: «Ay fan yu bare ngay toog fi man; bul gànctu, bul ànd ak genn góor. Noonu laay def ak yaw, man itam.» 4 Ndax kat ay fan yu bare la bànni Israyil di toog te duñu am buur, duñu am kàngam. Duñu rendi sarax, duñu am tuuri doj, duñu am xar-sànni, duñu am gàllaaji kër. 5 Gannaaw loolu bànni Israyil dinañu walbatiku, sàkku seen Yàlla Aji Sax ji, ak Daawuda seen buur. Ca jant yu mujj ya, xolub ragal Aji Sax ji lañuy dikke fi moom, akug mbaaxam.