Saar 38
Esekiyel wopp na ba jóg
1 Jant yooyu Esekiya moo woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!”» 2 Esekiya nag walbatiku, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji. 3 Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.
4 Ci kaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Esayi, ne ko: 5 «Doxal ba ca Esekiya, nga ne ko: Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: “Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom. 6 Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”»
7 Lii nag ngay def ab takk bu bawoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne Aji Sax ji dina def li mu wax: 8 Maa ngii di delloo ker gi gannaaw lu tollook fukki dëggastal, ya jant bi wàccoon ca kaw iskaleb Axas. Ci kaw loolu jant bi dellu gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu jotoona wàcc.
9 Mbind mii nag Esekiya buurub Yuda moo ko bindoon, gannaaw ba mu tëddee wopp, ba jóg:
10 Man de dama noon:
«Sama digg doole laay deme
jaare bunti njaniiw,
sama ndesu fan réer ma!»
11 Ma noon: «Dootuma gisati* 38.11 gis Aji Sax ji mooy dem biir kër Aji Sax ji. Seetal ci aaya 22 ak Sabóor 27.4. Aji Sax ji,
duma gisati Aji Sax ji fi kërug àddina.
Duma tegati doom aadama bët,
dootu fii ci waa àddina.
12 Sama dëkkuwaay lañu sempi,
yóbbu fu sore,
mbete xaymab sàmm.
Sama àpp a taxañe,
ni ndimo lu ab ràbb doge ca mbaam ma.
Diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma.
13 May xalaat, ba bët set;
Aji Sax jiy dammat samay yax ni gaynde,
diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma.
14 May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu,
di binni nim xati,
di séentu kaw ba saay gët giim.
Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa,
dimbali ma.»
15 Waaye lu may waxati?
Aji Sax jee ma wax,
te moo jëf.
Kon, ma temp ndànk sama giiru dund
ndax tiisu xol.
16 Boroom bi, ci sa kàddook sa jëf la nit di dunde
te ci laay noyyee ba tey.
Yaa ma wéral, may ma, ma dund.
17 Ndeke sama tiisu xol wii,
sama jàmm rekk a tax.
Sa cofeel a tax
nga sorele maak paxum sànkute.
Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
18 Njaniiw du la sant,
ndee du la gërëm,
te ku tàbbim pax yaakaaratul sa kóllëre.
19 Kiy dund, kiy dund doŋŋ mooy ki lay sant
ni man bésub tey jii,
te baay mooy xamal doom sa kóllëre.
20 Aji Sax ji yaa may wallu,
nu di la woy, ànd aki xalam,
sunu giiru dund,
fa sa biir kër, yaw Aji Sax ji.
21 Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiya bi, kon dina dund,» 22 ba Esekiya noon ko: «Ana lu di takk biy firndeel ne dinaa wér, ba dellooti kër Aji Sax ji?»