Saar 42
Aji Sax ji yebal na jaamam
«Xool-leen sama jaam bi ma yor,
sama tànnéef, sama soppey xol,
ci kawam laa teg samag noo,
te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Du xaacu, du biral;
du jibal baatam ci mbedd mi.
Bant bu lemu sax, du ko damm,
leer gu giim it, du ko fey.
Mooy indi yoonu dëgg.
Du toqi, du nasax,
ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf,
fa waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.»
Yàlla Aji Sax ji dafa wax,
moom mi sàkk asamaan, firi ko;
tàllal suuf ak lu mu jur,
may noowal bakkan ñi ci kawam,
ba ña cay daagoo di noyyi.
Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk,
jàpp la ci loxo,
sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak nit ñi;
def la ngay leeru xeet yi,
ngay gisloo gumba,
di génne ku ñu tëj,
ku dëkke woon lëndëm, génn kërug tëjukaay.
Man, Aji Sax jeey sama tur,
sama teddnga, duma ko joxe,
te sama bàkk, duma ko wacce jëmmi tuur.
Mbir ya jiitoo ngoog, mat na;
yu yees laa leen di yégal,
balaa teew, ma yegge leen ko.»
Woyleen Aji Sax ji
10 Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
yeen waa cati àddina, kañleen ko,
ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram,
ak duni géej ak ña ca dëkke.
11 Na waa àll beeki dëkkam xaacoondoo,
waa dalub Kedar
ak waa Sela sarxolleendoo,
kaw tund ya di riirum mbég!
12 Nañu delloo Aji Sax ji teddngaam,
te biral bàkkam biir duni géej.
13 Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar,
xabtalu ni ñeyu xare,
àddu ca kaw, xaacu,
tiime noon yi njàmbaaram.
Aji Sax ji soppi na
14 Aji Sax ji nee: «Damaa yàgga xeremlu,
ne cell, téye sama bopp.
Waaye léegi, ni kuy matu laay onke,
di xiix ak a àppaat boole ca.
15 Maay tonni tund wu mag ak wu ndaw,
lu cay gàncax, ma fóom;
ag dex, ma def ag joor;
ab déeg, ma ŋiisal.
16 Maay doxloo silmaxa yi
ci yoon wu ñu xamul,
ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale.
Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer,
fu ñagas, ma maasaleel leen.
Lii laa leen di defal,
te duma leen wacc mukk!
17 Ñi wóolu ay jëmmi tuur,
naan jëmm yu ñu móol:
“Yeenay sunuy yàlla,”
dees na leen waññi, torxal leen.
 
18 «Yeen tëx yi, dégluleen;
yeen silmaxa yi, xool-leen ba gis.
19 Ana ku silmaxa ku moy sama jaam bii?
Ku tëx ba dab sama ndaw li ma yónni?
Ana ku silmaxa ba dab kii ñu jàmmal?
Ku silmaxa ba dab jaamu Aji Sax jii?
20 Gis nga lu bare,
waaye jàppoo ci dara.
Nopp ne kótt, dég-dég të!»
21 Aji Sax ji la soob ci njekkam,
mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba.
22 Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo;
ñépp tëje ciy pax,
dence ci këri tëjukaay,
ñu doon alalu xare
fu leen kenn dul xettlee,
xanaa ñu di leen sëxëtoo,
te kenn du ne ñu delloo leen.
 
23 Ana kan ci yeen mooy dékk lii nopp?
Kuy teewlu, ba doxe fa dégg?
24 Ana ku jébbal Yanqóoba futtikat yi,
ku jox Israyil gii, sëxëtookat yi?
Xanaa du Aji Sax ji nu tooñ?
Ñoo baña topp ay yoonam,
baña sàmm ndigalu yoonam,
25 ba mu yuri leen tàngooru sànjam,
sotti leen tar-taru xare,
mu jafal wetoo wet, te taxul ñu xam,
xoyom na leen te bawuñu ci xel.