Saar 12
Yeremee ngi ñaxtu
Aji Sax ji, dëggu nga def,
li may tawatsi fi yaw lépp.
Teewul ma di la diis mbir:
lu tax ku bon di baaxle,
bépp workat bu bon di féex?
Yaa leen jëmbat, ñu sampi reen,
law ba meññ;
jegeñal la seen làmmiñ,
te fekk nga sore seen xol.
Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga ma;
gis nga ma, seetlu sama xol ci yaw.
Diri leen niy xar yu ñuy rendi,
beral leen bésub rendi.
 
Ba kañ la réew mi naa sereŋ,
gàncaxu tooloo tool di lax?
Rabu àll ak njanaaw a ngi sànku
ngir mbonug ñi fi dëkk
te naan: «Moom xoolul sunu muj!»
Yàlla tontu na
«Ndegam boroom ñaari tànk ngay rawanteel, xoox,
nooy rawanteeki fas?
Soo wóoluwul lu moy àll bu ne yàmblaŋ,
nooy def ak gottub Yurdan?
Say bokk ak sa waa kër baay sax,
ñoom it wor nañu la,
ñoom it xaacu nañu, sam la;
te bu ñu lay wax jàmm it,
bu leen gëm.»
Aji Sax ji dëddu na séddoom
«Dëddu naa sama kër,
maa wacc sama séddoo,
wacce sama soppey xol loxol noonam.
Sama séddoo ngi may niru léegi
gaynde ci gott bi,
di ma xiiru, ba tax ma jéppi ko.
Sama séddoo baa ngi may saf tan mu todde
mu moroomi tanam gaw.
Doxleen dajaleji rabi àll yépp,
indi leen ci bernde ji.
10 Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ,
joggati sama waar,
def waar wi ma neex
màndiŋ mu ne maraas.
11 Def nañu ko gent buy jooy fi sama kaw,
réew mi mépp gentala gental,
te saful kenn.
12 Tundoo tund wu ne faraas fi màndiŋ mi,
ay yàqkat a ngi ciy bawoo,
doon saamaru Aji Sax ji, di faagaagal réew mépp,
cat ba cat,
jàmm réer luy dund!
13 Jiwum pepp, góob ay dég;
sonn, ñàkk yool,
xanaa mbetteel ci meññeef mii sababoo
ci merum Aji Sax ji.»
Aji Sax ji àrtu na dëkkandooy Israyil
14  Aji Sax ji dafa wax ne: «Mboolem sama dëkkandoo yu bon, yi laal céru suuf bi ma sédd Israyil sama ñoñ, maa ngii di leen déjjatee seen réew, te waa kër Yuda, maa leen di seppee fi seen digg. 15 Waaye bu ma déjjatee yooyu xeet ba noppi, dinaa leen dellu yërëm, ku nekk, ma delloo ko céram, ku nekk ak suufam. 16 Waaye bu ñu royee ba roy sama ñoñ, di jëfe ni sama ñoñ wara jëfe, di giñe sama tur naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” na ñu daan royloo sama ñoñ, ba ñuy giñe Baal, tuur mi, su boobaa ñu sampu fi sama digg ñoñ. 17 Waaye xeet wu ma ci déggalul, xeet woowu dama koy déjjati, déjjat, sànk leen.» Kàddug Aji Sax jee.