Saar 16
Yeremi wéet na ci biiri bokkam
1 Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma, ne ma:
2 «Bul jël jabar,
bul am doom ju góor mbaa ju jigéen ci bii bérab.»
3 Aji Sax ji kat dafa wax ci gone yu góor yeek gone yu jigéen
yi juddoo ci bii bérab,
wax ci seen ndey yi leen jur
wax ci seen baay yi leen meññ ci mii réew,
4 mu ne: «Jàngoroy ndee a leen di rey.
Deesu leen jooy, deesu leen rob.
Seeni néew ay tosal suuf.
Saamar akub xiif a leen di sànk,
seeni néew leel njanaaw ak rabi àll.»
5 Te Aji Sax ji kat dafa wax ne:
«Bul dugg kërug dëj,
bu fa dem di ñaawlook a jaale.
Maa xañ askan wii sama jàmm,»
kàddug Aji Sax jee,
«xañ leen sama ngor ak sama yërmande.
6 Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii,
te deesu leen rob,
deesu leen jooy.
Kenn du dagg yaramam
mbaa muy nelu, di ko ñaawloo.
7 Kenn du leen sédd aw ñam
wu ñuy dëfale ku deele,
kenn du leen jox ub kaas, dëfale leen,
doonte baay a dee mbaa ndey.
8 Kërug bernde it, bu fa dugg,
di toogandoo, di lekk ak a naan.»
9 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne:
«Maa ngii di dakkal ci bii bérab,
ngeen teewe, fekke lépp
luy coowal mbégteek bànneex,
boroom séet ak séetam selaw.
10 «Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?” 11 Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm. 12 Yeen nag, ngeen di bon, ba raw seeni maam. Yeena ngii, ku nekk të ticc, topp xolam bu bon, bañ maa déggal. 13 Maa leen di dàqe ci réew mii, jëme réew mu ngeen xamul, seeni maam xamuñu ko, ngeen di fa jaamu guddeek bëccëg yeneen yàlla, ndax dootuma leen baaxe.”»
Yaakaar jeexul
14 «Waaw ay bés a ngi ñëw déy,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israyil réewum Misra.” 15 Waaye dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, ki jële bànni Israyil réewum bëj-gànnaar, te jële leen mboolem réew ya mu leen sànke woon.” Maa leen di délloosi seen réew ma ma joxoon seeni maam.»
Kenn rëccul mbugal mi
16 «Maa ngii di woolu nappkat yu bare.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu napp ñii ba noppi ma woo rëbb yu bare, ñu rëbb leen ci kaw mboolem tund wu mag ak wu ndaw, ba ci bépp xar-xaru doj. 17 Samay bët a ngi ne jàkk déy ci seeni jëf. Dara umpu ma ci. Seeni ñaawtéef, dara rëccu ma ci. 18 Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»
Ñépp ay ràññeeji Aji Sax ji
Yeremeey wax
19 Yaw Aji Sax ji may dooleel,
di ma feg, di ma làq bésub njàqare,
yaw la xeet yiy bawoo cati àddina,
fekksi la, naan:
«Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon,
xërëmi neen yu amul njariñ.
20 Nit man naa sàkkal boppam ay yàlla?
Te duñuy yàlla sax!»
Yàllaay wax
21 «Moo tax maa ngii di leen xamal bii yoon,
ba ñu xam sama diisaayu loxook sama doole,
xam ne maay Aji Sax ji.»