Saar 22
1 Aji Sax ji dafa wax ne: «Demal kër buurub Yuda, nga jottli fa kàddu gii. 2 Danga naan: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yaw buurub Yuda mi toog ci jalub Daawuda, yaak say jawriñ ak sa nit ñiy jaare yii bunt. 3 Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettli ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jaambur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii bérab. 4 Su ngeen jëfee ba jëfe santaane bii déy, buur du noppee dugge yii bunt, di toogal Buur Daawuda fi jalam, di dawal watiir aki fas, ànd ak seeni jawriñ ak seeni nit. 5 Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”»
6 Aji Sax ji déy dafa wax ci mbirum kër buurub Yuda ne:
«Yaay sama àllub Galàdd,
sama collu tundu Libaŋ,
waaye déy, maa lay def ni màndiŋ,
ngay dëkk yu kenn dëkkul.
7 Maa lay beralal yàqkat
yu fàggu seeni gànnaay,
dàjji sa tànnéefi banti seedar,
sànni ca sawara sa.
8 «Doxandéem yu bare dinañu jaare dëkk bii, di laajte ci seen biir naan: “Ana lu waral Aji Sax ji def nii bii dëkk bu mag?” 9 Su ko defee ñu ne leen: “Xanaa li ñu fecci seen kóllërey Yàlla Aji Sax ji, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu.”»
Lu jëm ci Salum buurub Yuda
10 Buleen jooy buur Yosya mi dee,
buleen ko ñaawlul,
jooyleena jooy buur Salum miy dem,
te du délseeti,
ba gis réewum juddoom.
11 Aji Sax ji kat dafa wax ci mbirum buurub Yuda, Salum mi wuutu baayam Yosya te bàyyikoo fii. Mu ne: «Du fi délseeti mukk. 12 Waaye fa ñu ko yóbbu ngàllo, fa lay deeye. Réew mii, du ko gisati mukk.»
Lu jëm ci Yowakim, kuutaayu Buur Yosya
13 Wóoy ngalla kiy tabax këram te seetu ci njekk,
di teg taaxi kawam te seetu ci yoon,
liggéeyloo moroomam ci dara,
feyu kow ñaqam.
14 Mu ngi naan: «Maay tabax kër gu yaa,
taaxi kaw ya yàmblaŋ.
Ma bënn ay palanteer,
tafal kër gi banti seedar,
diw ko ba mu xonq curr.
15 «Ëpplante banti seedar da laa def buur?
Sa baay daawul lekk ak a naan?
Teewu koo jëfe dëgg ak yoon,
muy njiglaayam.
16 Da daan sàmm àqu ku ñàkk ak ku néew doole,
muy njiglaay.
Du looloo di xam maay kan?»
Kàddug Aji Sax jee.
17 «Yaw xooloo,
xalaatoo lu moy loo jariñoo,
ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla,
di fitnaale ak a lore?»
18 Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne:
«Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen,
naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!”
Kenn du ko jooy,
naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!”
19 Robu mbaam-sëf lees koy rob:
diri génne Yerusalem,
sànni ca biti.»
Yeremi yégle na fitnay Yerusalem
20 Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem,
yéegileen tundi Libaŋ, yuuxu.
Àddooleen fa Basan, xaacu,
te yuuxoo fa Abarim,
nde seen soppe yépp a rajaxoo!»
21 «Waxoon naa leen ko ba ngeen di am jàmm,
ngeen ne: “Dégluwnu!”
Noonu ngeen jàppoo ba ngeen di ndaw ba tey,
masuleen maa déggal!
22 Ngelaw dina sàmm seeni sàmm, sànk leen,
seeni soppe duggi njaam,
ba ngeen rus, torox
ndax seen gépp mbon.
23 «Yaw mi tooge Libaŋ* 22.23 Libaŋ man naa doon misaalu Yerusalem. Seetal ci 1.Buur ya 7.2.,
def um tàgg sa garabi seedar,
éy bu la mitit dikkalee,
nirook mititu mat,
ndaw binni yu réy!»
Lu jëm ci Kooña doomu Yowakim
24 Mu ne: «Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax jee, «yaw buurub Yuda, Kooña† 22.24 Kooña turu gàttalu Yowakin la. Seetal ci 2.Buur ya 24.8-17. doomu Yowakim, soo doon jaarob torlukaay ci sama ndijoor it, fa laa lay foqatee, 25 teg la ci loxol ñi lay tëru te nga ragal leen; muy Nabukodonosor buuru Babilon aki xarekatam. 26 Maa lay xalab, yaak sa ndey ji la jur, jëme meneen réew mu ngeen juddoowul, te fa ngeen di deeye.
27 Réew mi ngeen namma délsi, dungeen fi délseeti.»
28 Nee ñu: «Waa jii Kooña da di njaq lu toj lu jarul daraa?
Am da di xottu ndab lu kenn buggul?
Lu waral ñu di ko sànni, mooki doomam,
xalab leen biir réew mu ñu xamul?»
29 Éy waa réew mi, waa réew mee, waa réew mi,
dégluleen Kàddug Aji Sax ji!
30 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Bindleen ne waa jii amul doom!
Du baaxle cig dundam,
nde kenn ci geñoom du tekki,
ba tooge jalub Daawuda,
di jiiteeti fi Yuda.