Sabóor 3
Aji jub a ngi woote wall
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor* 3.1 Seetal ci 2.Samiyel 15—16..
 
Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare!
Ñu baree may jógal,
ñu baree may tooge naa:
«Yàlla du ko wallu!»
Selaw
 
Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg,
di ma teral, di ma siggil.
Maay woo Aji Sax ji wall,
mu walloo ma fa tundam wu sell wa.
Selaw.
 
Maay tëdd nelaw, yewwu;
Aji Sax ji di ma aar.
Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma,
te duma ragal.
 
Éy Aji Sax ji sama Yàlla,
jógal, wallu ma!
Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp,
foq seeni sell.
Aji Sax ji, yaa moom wall,
sa mbooloo jagoo sa barke.
Selaw.

*3:1 3.1 Seetal ci 2.Samiyel 15—16.