Saar 13
Ñaari rab yu aay falu nañu
1 Ci kaw loolu ma gis rab wu génne ci géej gi, am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, béjjén yi sol fukki mbaxanay buur, béjjén bu ne menn, bopp bu nekk ak tur wuy saaga Yàlla. 2 Rab wi ma gis ni segg la mel, tànk yi mel ni yu urs* 13.2 urs rab wu ñàng la. Man naa ëpp gaynde te gën koo aay., gémmiñ gi mel ni gu gaynde. Ninki-nànka ji jox ko kàttanam ak nguuram ak sañ-sañam bu réy. 3 Benn ci bopp yi nag, rab wi da cee gaañu ba mel ni lu ñu rendi, ba mu dee. Teewul gaañu-gaañu boobu ko waroona rey daldi wér. Waa àddina sépp yéemu, topp ci rab wi. 4 Ba loolu amee ñu sujjóotal ninki-nànka ji ndax la mu jox rab wi sañ-sañ bi, di sujjóotal rab wi, naan: «Ana kuy moroomu rab wii, ak ku mana xeex ak moom?»
5 Ñu may rab wi nag muy kañu ak a saaga Yàlla, may ko it mu saña wéye noonu diiru ñeent fukki weer ak ñaar. 6 Muy tifaar Yàlla ay saaga, di saaga aw turam, ak màkkaanam, ak ñi dëkke asamaan. 7 Ñu may ko itam mu xareek ñu sell ñi, duma leen, boole ci may ko sañ-sañ ci kaw niti gépp giir ak wépp xeet ak wépp làmmiñ ak wépp askan. 8 Mboolem waa àddinaa koy sujjóotal, mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund† 13.8 téereb dund bi: seetal ci 17.8. bu Gàtt, bi ñu rendi.
9 Ku ami nopp kat, na dégg.
10 Ku wara dem ngàllo,
ngàllo nga jëm,
ku wara deeye saamar,
saamar ngay deeyeji.
Looloo tax ñu sell ñi wara saxoo muñ ak ngëm.
11 Ci kaw loolu ma gis weneen rab wu génne ci suuf, am ñaari béjjén ni ab gàtt, tey wax ni ninki-nànka. 12 Muy jëfe mboolem sañ-sañu rab wu jëkk wa, ci turu rab wu jëkk wa, di sant suuf ak ñi ko dëkke ñu sujjóotal rab wu jëkk, woowu gaañu woon ba nara dee te mujj wér. 13 Ñaareelu rab wi nag di def kéemaan yu réy, bay wàcce ci kaw suuf sawara wu jóge asamaan, nit ñi di gis. 14 Ñaareelu rab wi nag nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wi. Mu sant waa àddina, ñu sàkk jëmmu rab, wi ñu jamoon saamar te muy wéye bakkanam. 15 Gannaaw loolu mayees na ko mu sol ag noo jëmmu rab wu jëkk wi, ba muy wax, di reylu képp ku ko sujjóotalul. 16 Ba mu ko defee, mag ak ndaw, boroom alal ak baadoolo, as gor akub jaam, ñépp, mu defal leen màndargam loxol ndijoor mbaa jë, 17 ba kenn du mana jënd mbaa jaay te amul màndargam turu rab wi mbaa lim bi méngook turam.
18 Fii nag xel la laaj: ku am ug dégg, na waññ limu rab wi, ndax boobu lim turu nit la taxawe, di juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn (666).