12
Peeñub Pool ak nattu bi ko dal
Damu amul njariñ, ba tey war na ma. Kon ma jàll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i peeñu. Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne yékkati nañu ko ba ca asamaan, si gëna kawe, booba ak léegi mat na fukki at ak ñeent. Xawma ndax ànd na ak jëmmam walla déet. Yàlla rekk a xam. 3-4 Xam naa ne, nit kooku yékkati nañu ko ba fa Yàlla nekk. Bu dee ci jëmmam mbaa ci xelam, xawma; Yàllaa xam. Mu dégg fa baat yu ñu manula nettali te yu ñu mayul doom Aadama, mu ŋaaŋ ko. Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama néew doole. Su ma bëggoona damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn baña foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax.
Te it ngir ma baña yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma mitital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma baña yég sama bopp. Ñaan naa Boroom bi ñetti yoon ci mbir moomu, ngir mu teqale ma ak moom. Mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man. 10 Looloo tax may bég ci néew doole, yi may wéye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy njàqare, mbaa ñu saaga ma, mbaa ñu fitnaal ma. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan.
Pool bëgg na leen
11 Ci dëgg-dëgg wax naa waxi dof te yéena ma ci dugal, fekk yéen ci seen bopp sax yéena ma waroona sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw ëpplewuñu ma dara. 12 Kéemaan yi, jaloore yi ak jëf yu màgg, yiy firndeel ndawul Kirist, feeñ nañu ci seen biir, ma ànd ci ak muñ gu mat. 13 Lan laa defal yeneen mboolooy ñi gëm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma wéeru ci ñoom te wéeruwuma ci yéen? Baal-leen ma googu tooñ!
14 Maa ngi leen di waaja ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yéen. Wutsiwuma seen alal, yéen laa soxla. Ndaxte du gone moo wara yor waajuram, waaye waajur moo wara yor gone yi. 15 Man nag nangu naa joxe li ma am lépp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw bëgg naa leen nii, xanaa kay seen mbëggeel ci man warula wàññiku? 16 Kon noonu la, nekkuma woon yen ci yéen. Waaye man na am ñu naan, dama leena nax, ba réeral leen ci sama njublaŋ.
17 Ndax damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci ñi ma yónni woon? 18 Sant naa Tit, mu ñëw ci yéen, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu yékkati ak tànk yu nuy dox?
19 Xanaa diirub li ngeen di jàng lii, defe ngeen ne nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Yàlla ak ci turu Kirist; te lépp ngir seen njariñ la. 20 Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yëngu-yëngu. 21 Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Yàlla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci ñu bare ñu bàkkaaroon te dëdduwuñu seen yàqute, seen njaaloo ak seen ñaawteef, gi ñu doon def.