20
Léebu liggéeykat yi ñu jël ci waxtu yu wuute
«Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam. Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leena yebal ca toolam. Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu. Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.” Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu. Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?” Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
«Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.” Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon. 10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkka jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon. 11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga, 12 naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” 13 Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon? 14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw, 15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” 16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
Yeesu xamle na ñetteelu yoon ne dina dee, dekki
17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii: 18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, 19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
Li doomi Sebede ñaan Yeesu
20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn. 21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.» 22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.» 23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya. 25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not. 26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 27 te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam. 28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
Yeesu faj na ñaari gumba
29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko. 30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?» 33 Ñu ne ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.» 34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.