Saar 23
Daawuda xettli na waa Keyla
1 Mu am bés nag, ñu yégal Daawuda, ne ko: «Waa Filisti de ña ngay song waa Keyla xare. Ña ngay sëxëtoo dàgga ya.» 2 Daawuda seet ci Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma dem xarejeek waa Filisti?» Aji Sax ji ne Daawuda: «Demal kay xareek waa Filisti, xettli waa Keyla.» 3 Niti Daawuda ne Daawuda: «Waaw, ndegam fii ci Yuda lanu tiite, astamaak bu nu demee Keyla, ba janook làngi waa Filisti!» 4 Daawuda dellu seet ci Aji Sax ji, Aji Sax ji ne ko: «Doxal dem Keyla, man, maay teg waa Filisti ci say loxo.» 5 Ba mu ko defee Daawuda ànd aki nitam dem Keyla, xareek waa Filisti, duma leen duma yu réy, yóbbu seenug jur. Noonu la Daawuda xettlee waa Keyla.
6 Ba Abiyatar doomu Ayimeleg dawee fekki Daawuda ca Keyla, xar-sànni ma* 23.6 xar-sànni ma: dañu ko daan seete ci Aji Sax ji. la indaale.
7 Ci kaw loolu ñu yegge Sóol ne ko Daawuda dem na Keyla. Sóol ne: «Kon de Yàllaa ko teg ci samay loxo, ndax ba mu duggee biir dëkk bu tëje ràpp la tëj boppam.» 8 Ba loolu amee Sóol woo gàngooram gépp xare, ngir ñu dem Keyla, gawi Daawudaaki nitam. 9 Daawuda nag yég ne moom la Sóol di fexeel njekkar. Mu ne Abiyatar sarxalkat ba: «Indil xar-sànni mi.» 10 Mu indi ko, Daawuda ne: «Éy Aji Sax ji, Yàllay Israyil sama Boroom, dégg naa déy ne Sóol a ngi waaja dikk Keyla gii, tas-si dëkk bi ndax man. 11 Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg ci loxoom? Boroom bi, ndax li ma dégg ñu naan Sóol a ngi ñëw, dëgg la? Éy Aji Sax ji, Yàllay Israyil, sama Boroom, ngalla wax ma!» Aji Sax ji ne: «Dina ñëw.» 12 Daawuda ne: «Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg, maak samay nit ci loxol Sóol?» Aji Sax ji ne ko: «Ahakay.» 13 Daawuda fabu mooki nitam, ñu wara tollu ci juróom benni téeméer, daldi bàyyikoo Keyla, di taxawaaloo fépp fu ñu ñeme. Ba ñu yeggee Sóol ne ko Daawuda rëcce na Keyla, Sóol yebbi.
14 Daawuda nag nekk ca xunti yu kawe ya ca màndiŋ ma, toog foofa ca tund, wa ca màndiŋu Sif. Sóol di ko seet bés bu nekk, waaye Yàlla tegul Daawuda cay loxoom. 15 Gannaaw gi Daawuda yég ne Sóol waajal na aw yoon ngir jël bakkanam. Booba Daawudaa nga ca màndiŋu Sif ca Orsa. 16 Ci biir loolu Yonatan doomu Sóol ja dem Orsa ca Daawuda, di ko ñaax ngir mu gëna dëgërloo Yàlla. 17 Mu ne ko: «Bul tiit. Loxol Sóol sama baay du la jot. Yaw yaay falu Buur ci Israyil, te maay doon sa bummi. Sama baay ci boppam xam na loolu bu baax.» 18 Ci biir loolu ñu feddli seen kóllëre ñoom ñaar fa kanam Aji Sax ji. Daawuda des Orsa, Yonatan ñibbi këram.
Sóol topp na Daawuda
19 Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. 20 Buur, saa yoo bëggee ñëw rekk, ñëwal. Kon, Buur, nun noo koy teg ci say loxo.» 21 Sóol ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji barkeel ndax yég ngeen ma. 22 Léegi demleen, xoolaat bu baax; seetleen ba gis fu mu jaare, ak ku ko fa gis, ndax xamal nañu ma ne ku ñora ñor la. 23 Seetleen ba gis fépp fu mu mana làqu, doora délsi fii ci man, indil ma lu leer. Su ko defee ma ànd ak yeen. Su Daawuda nekkee ci gox bi, dinaa topp tànkam ci biir mboolem làngi Yudeen ñi.»
24 Ba loolu amee waa Sif jiituji Sóol ca Sif. Fekk na Daawudaaki nitam ña nga woon ca joor ga ca màndiŋu Mawon, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. 25 Sóol aki nitam dem, di wër Daawuda, ñu yegge ko Daawuda, mu dem ba ca doj wa, làqu foofa ca màndiŋu Mawon. Sóol yég ko, dàqi ko ca biir màndiŋu Mawon. 26 Sóol a ngay demee gii wetu tund wi, Daawudaaki nitam bartaloo wet ga ca des, gaawtu di wéy, ngir rëcc Sóol. Naka la Sóol ak mbooloom dem bay wër-ndombo Daawuda aki nitam, ngir jàpp leen, 27 ndaw dikk ca Sóol ne ko: «Dikkal gaaw, waa Filisti song nañu réew ma.» 28 Sóol nag fomm ndàqum Daawuda, ngir dajejeek waa Filisti. Looloo waral turu bérab boobu di Sela Amalekot (mu firi doju Rawukaay).