Ñaareelu bataaxal bi Yàlla may
Piyeer
mu bind ko
Saar 1
Ci man Simoŋ Piyeer* 1.1 Turu Simoŋ ci làkku gereg mooy Simeyon ci làkku ebrë., miy jaamub Yeesu Almasi, di ndawam, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel ñi ñu may ngëm gu njég ga réye ni sunu gos, ci sunu njekku Yàlla, Musalkat bi Yeesu Almasi. Aw yiw ak jàmm baawaan na, ñeel leen, ndax xam gu ngeen xam Yàlla, ak sunu Sang Yeesu.
Dëggal-leen wooteb Yàlla
Su dee nag mboolem lu dund gu ag jullite laaj, Yàllaa nu ko maye dooleem, ba mu nu xamalee ne darajay boppam, ak jalooreem ju wéet lanu wooye. Ci jooju daraja, ak jooju jaloore ju wéet lees nu baaxee ay dige yu réy njég te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina, gi xemmemtéefu bakkan waral.
Loolu ci boppam wara tax ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam; seen xam-xam, ngeen dolli ci moom seen bakkan; moom seen bakkan, ngeen dolli ci ag muñ; seenug muñ, ngeen dolli ci ag njullite; seenug njullite, ngeen dolli ci bëgg seen bokki gëmkat; bëgg seen bokki gëmkat, ngeen dolli ci cofeel. Ndax yooyu jikko kat su ngeen ko amee, ba mu law, dungeen yaafus, dungeen ñàkk njariñ nu ngeen xame Sang Yeesu Almasi. Waaye yii jikko, ku ko ñàkk, daa fekk mu gàtt gis-gis ba far gumba, te fàtte ne dees koo fóotoon ba mu set, teqlikook bàkkaari démbam.
10 Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo, ak taamu gi ñu leen taamu. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk. 11 Noonu lees leen di ubbile bunt bu yaa bu ngeen di tàbbee ca nguur gu sax gay sunu moomeelu Sang, sunu Musalkat, Yeesu Almasi.
Yàlla waxyul na yonent yi
12 Moo waral ma fas yéene di leen dëkke fàttli loolu, doonte xas ngeen koo xam, ba tax ngeen taxaw bu dëgër ci dëgg gi leen nuyusi. 13 Li jaadu ci sama gis-gis moo di, li feek may màkkaanoo aw suux, dinaa leen ko fàttli, ngir soññ leen. 14 Ndax damaa leer, ni ma ko sunu Boroom Yeesu Almasi leeralale, bés bi may summi sama màkkaanu suux bii dëgmal na. 15 Waaye dinaa def sama kem-kàttan, ba fu ngeen tollu, di fàttliku mbir yooyu, gannaaw bu ma dëddoo.
16 Du ay léeb yu xel mu xareñ fent lanu leen xamale woon sunu manoorey Boroom Yeesu Almasi, ak na muy dikke, waaye noo teewe màggaayam. 17 Ndax kat moo nangoo ci Yàlla Baay bi, teraanga ak daraja, ba ko baat ba jibalee, bawoo fa Boroom daraja ju yéeme ja ne: «Kii moo di Sama Doom, sama Soppe; ci moom laa ame bànneex. 1.17 Seetal ci Macë 17.5.» 18 Baat booba jóge asamaan, moom lanu dégg, ba nu nekkee ak moom ca tund wu sell wa.
19 Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol. 20 Waaye li ngeen wara jëkka xam moo di amul ci Mbind mi, benn waxyu bu yonent ba ko waxe, firee xelum boppam. 21 Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.

*1:1 1.1 Turu Simoŋ ci làkku gereg mooy Simeyon ci làkku ebrë.

1:17 1.17 Seetal ci Macë 17.5.