Saar 14
Absalom délsi na
1 Ci biir loolu Yowab, mi Seruya di yaayam, xam ne xelu Buur Daawudaa ngi ci Absalom. 2 Yowab nag yónnee ca dëkk ba ñuy wax Tekowa, ñu jëleji fa jigéen ju rafet xel, indil ko ko. Yowab ne ko: «Dangay ñaawlu-ñaawlulu. Solal yérey ñaawlu, te bul xeeñu. Melal daal ni jigéen ju jota ñaawlu lu yàgg, ngir ku mu deele. 3 Su ko defee nga àgg ca Buur, wax ko lii ma lay wax.» Yowab wax ko kàddu ya mu wara wax.
4 Jigéen ja dëkk Tekowa àgg ca Buur, daanu ci suuf, sujjóotal ko, ne ko: «Buur, wallu ma!» 5 Buur ne ko: «Lu la dal?» Mu ne ko: «Man de gore, dama dib jëtun; sama jëkkër a dee. 6 Sang bi, ñaari doom yu góor laa amoon. Dañu doon xeex ñoom ñaar ca àll ba te ku leen àtte nekku fa. Kenn ki dóor moroom mi, rey ko. 7 Bokk yépp daldi jóg dal ci sama kaw, sang bi. Ñu ne ma: “Jox nu sa doom ji rey doomu ndeyam, nu rey ko, feyul doomu ndeyam ji mu rey. Moo dese ndono li, kon danu koy sàkkal pexe, moom itam.” Dañoo nara fey wenn xal wi ma dese, ba xañ sama jëkkër aw tur, xañ ko aw askan ci kaw suuf.» 8 Buur ne ko: «Demal ñibbi. Man ci sama bopp maay joxe ndigal ci yaw.» 9 Jigéen ja ne ko: «Buur sang bi, àq ju ci am, yal na ma topp, maak sama waa kër baay, te nga bañ cee gàddu dara, yaak sa waa kër.» 10 Buur ne ko: «Ku la tudd, indil ma ko, dootu la sonal.» 11 Mu ne ko: «Kon ngalla Buur, woo ci seede sa turu Yàlla Aji Sax ji, ngir kiy toppe bakkanu ka dee baña yokk yàqute, ba ñu rey sama doom ji.» Mu ne ko: «Giñ naa ko ci turu Aji Sax ji, Kiy Dund, kawar gu gëna tuut du jóge ci sa boppu doom, wadd ci suuf.»
12 Jigéen ja ne ko: «Buur, sang bi, ma ñeme laa waxati benn baat boog!» Mu ne ko: «Waxal.» 13 Mu ne: «Lu waral kon nga naral lu ni mel ñoñi Yàlla ñi? Buur, boo waxee loolu kay, mel na ni tooñ nga, ndax jëliwoo sa doom ja gàddaay. 14 Su dee dee moom, nun ñépp ay dee ni ndox di tuuroo ba deesu ko tanqati. Yàlla nag musalul kenn ci dee, waaye moo lal pexe ngir ki gàddaay du saxoo gàddaay bérab bu ko sore. 15 Buur sang bi, maa ñëw wax la kàddu yii, ndax mbooloo mee ma tiital. Ma noon nag sang bi, naa wax ak Buur, jombul mu defal ma li may ñaan. 16 Jombul Buur sang bi nangu maa xettli ci ki nuy fexee boole ak sama doom sànk, beddee nu ci céru Yàlla. 17 Léegi nag sang bi, yal na sa kàddu gii di sama noflaay. Ndax yaw Buur, sama sang, dangaa mel ni malaakam Yàlla, am ug dégg, di teqale liy yoon ak li dul yoon. Yal na sa Yàlla Aji Sax ji ànd ak yaw.»
18 Buur ne jigéen ja: «Léegi nag, bu ma nëbbu, tontu ma ci lii ma lay laaj.» Mu ne ko: «Waxal, Buur, sang bi.» 19 Mu ne ko: «Ndax du Yowab a nas pexe mii mépp, yaak moom?» Mu ne ko: «Buur, sang bi, ak sa barke, li nga wax rekk la, du leneen moos! Yowab, sa jawriñ bee ma ko sant. Moo ma waxloo lii lépp, sang bi. 20 Jubbanti mbir mii de moo tax Yowab def lii. Waaye yaw sang bi, danga di boroom xel mu rafet ni malaakam Yàlla. Xam nga mboolem lu xew ci réew mi.»
21 Gannaaw gi Buur ne Yowab: «Waaw, baax na, nangu naa. Demal jëli ngóor sa, Absalom.» 22 Yowab nag daanu ca suuf, sujjóot, ne Buur: «Buur, sang bi, yal nanga barkeel, sang bi. Xam naa ne may nga ma cér, gannaaw yaa ma may lii may dagaan.» 23 Ba loolu amee Yowab dem Gesur, daldi délloosi Absalom Yerusalem. 24 Buur Daawuda nag ne, na Absalom yem këram. Mu ne bumu taxaw ci kanamam. Ba mu ko defee Absalom yem këram, te taxawul fa kanam Buur Daawuda.
25 Absalom nag amul woon góor gu siiwe ni moom ci Israyil gépp ndax góorayiw. La ko dale ca wewu tànkam ba ca digg bopp ba, du lenn lu ca sikk. 26 At mu jotaan mu watu ndax njañ lu diis, te bu watoo, natt kawar ga ci doomi nattukaayu buur, mu jege ñaari kilook genn-wàll. 27 Absalom amoon na ñetti doom yu góor ak doom ju jigéen. Tamar, doom ju jigéen ja, doon ndaw su taaru.
28 Absalom nekk na Yerusalem ñaari ati lëmm yu mu sañula taxaw fa kanam Buur baayam. 29 Gannaaw gi Absalom yónnee, ñu wool ko Yowab ngir mu yónni ko ca Buur. Yowab lànk, ñëwul. Mu yónneewaat, mu lànk. 30 Absalom ne ay surgaam: «Gis ngeen, toolub Yowab mook sama tool a sësoo, te peppum lors a nga ca. Demleen taal ko.» Surgay Absalom dem, taal tool ba. 31 Ba loolu amee Yowab waaxu ba ca kër Absalom, ne ko: «Ana lu waral say surga taal sama tool?» 32 Absalom ne Yowab: «Xam nga damaa yónnee ci yaw, ne la ñëwal, ma yónni la ca Buur, nga laajal ma ko lu ma taxa jóge Gesur. Li gënoon ci man kay mooy ma toog foofa! Léegi daal damay gis Buur. Su fekkee ne damaa tooñ, na ma rey!»
33 Yowab dem ca Buur, wax ko ko. Buur woolu Absalom. Mu dikk sukk, sujjóotal ko. Buur taf ko ca kawam.