Saar 3
Ñaanleen ci Yàlla
1 Li ci des nag bokk yi, moo di ngeen ñaanal nu, ngir kàddug Boroom bi gaawa law te am ndam na mu ko ame woon fa yeen, 2 ngir itam nu mucc ci nit ñu soxor ñu bon ñi, ndax du ñépp a gëm. 3 Waaye Boroom bi mooy ki jara wóolu, te moo leen di dooleel, musal leen ci Ku bon ki. 4 Am nanu it kóolute gu nu Boroom bi may, ne li nu leen sant, moom ngeen nekke, te moom ngeen di wéye. 5 Yal na Boroom bi wommat seen xol, jëme ci cofeelu Yàlla ak muñ gi ci Almasi.
Yaafus warul
6 Ndigal li nu leen di jox ci sunu turu Boroom Yeesu Almasi, moo di ngeen dànd mépp mbokk mu nekke ag yaafus, te baña dëppoo ak dénkaane yi ngeen nangoo ci nun. 7 Yeen ci seen bopp, xam ngeen ne ci sunuy tànk ngeen wara awe, te du ag yaafus lanu nekke woon ci seen biir. 8 Lekkunu ñamu kenn ci neen, xanaa di yëngu guddi ak bëccëg, ci coonob daan sunu doole, ngir baña diisal kenn ci yeen. 9 Moona du sañ-sañ bu nu ci ñàkk, xanaa bëgg leena won lu ngeen nu roye, ba ngeen aw ci sunuy tànk, 10 ndax ba nu nekkee ak yeen, ndigal lanu leen joxoon moo di lii: «Ku nanguwula liggéey, bumu lekk.»
11 Dégg nanu nag ne ñenn a ngi ci seen biir, ñu nekke ag yaafus, duñu yëngu ci dara, lu moy di topptoo lu seen yoon nekkul. 12 Ñu ni mel lanuy sant ak a dénku ngir Sang Yeesu Almasi, ngir ñu dal, tey yëngu, di dunde seen ñaqu bopp. 13 Yeen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu baax.
14 Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko. 15 Bumu tax ngeen def ko ab noon, waaye yeddleen ko, ndax mbokk la.
Fii la Póol tëje bataaxalam
16 Gannaaw loolu, Boroom bi moom jàmm, yal na leen mayal boppam jàmmi lépp ak fépp. Yal na Boroom bi ànd ak yeen ñépp.
17 Tàggoo bii, man Póol maa ko bind ci sama loxol bopp, te nii laay binde ci bépp bataaxal. 18 Sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ñeel na leen yeen ñépp.