Dañeel
Dañeel gore na ci biir nguuru kéefar
Saar 1
(Saar 1.1—6.29)
Dañeel aki xaritam tàbbi nañu ci liggéeyu kër Buur
Ca ñetteelu atu nguurug Yowakim buurub Yuda, Nabukodonosor buuru Babilon daa dikk, gaw Yerusalem. Boroom bi nag teg Yowakim buurub Yuda ciy loxoom, boole ca lenni jumtukaayi kër Yàlla ga. Nabukodonosor yóbbu jumtukaay ya réewum Sineyaar, ga ñuy wax Babilon itam, ca biir kërug tuuram. Mu daldi fat jumtukaay ya ca denci kër tuuram.
Ba loolu amee Buur jox ndigal Aspenas, kilifay bëkk-néegam, ngir mu tànne ci bànni Israyil, ñenn ci askanu buur ak ci garmi yi. Ñu diy waxambaane yu amul benn sikk ci seen yaram, di ñu góorayiw, mane bépp xeetu njàng, bare xam-xam te am déggin, ba mana liggéeyal Buur ci biir këram. Ñu di leen jàngal làkku waa Babilon ak seen mbind. Ci biir loolu Buur dogalal leen bés bu nekk ab cér ci njëlam ak ci biiñam. Mu santaane ñu tàggat leen diiru ñetti at, ñu doora tàbbi ci liggéeyu buur. Yudeen ña ca bokkoon di Dañeel ak Anaña ak Mikayel ak Asaryaa. Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltasar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Mikayel tudd Mesag, Asaryaa di Abet Nego.
Ci biir loolu Dañeel fas yéene ci xolam ne du sobeel boppam ci njëlu buur ak biiñam. Mu ñaan kilifag jawriñ ya mu may ko, mu bañ cee sobeel boppam. Yàlla def kilifag jawriñ ya baaxe Dañeel, yërëm ko. 10 Teewul kilifag jawriñ ya ne Dañeel: «Man de damaa ragal Buur sama boroom, moom mi leen dogalal seen lekk ak seen naan. Su Buur gisee ngeen gëna yooy seen moroomi xale yu góor yi nag? Sama bakkan xaj na ci de!»
11 Ba mu ko defee Dañeel wax ak dag, ba kilifay jawriñ ya sant mu wattu leen, mook Anaña ak Mikayel ak Asaryaa. Mu ne ko: 12 «Ngalla sang bi, seetlu nu diiru fukki fan, ñu di nu jox ci meññeef mi rekk ak ndoxum naan; 13 te nga xool nu, xool xale yu góor yiy lekk ci njëlal Buur. Su ko defee nga seet nooy def ak nun ci ni nga nu gise, sang bi.» 14 Waa ja ànd ak ñoom ci loolu, seetlu leen diiru fukki fan. 15 Ba fukki fan ya matee, seen kanam gëna leer te ñu gëna suur mboolem xale yu góor yay lekk ca njëlal Buur. 16 Ci kaw loolu wattukat ba di yóbbu seen njël ak seen biiñ, weccee leen ko meññeef. 17 Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.
18 Ba diir ba leen Buur àppal matee, ñu war leena indi, kilifag jawriñ ya yóbbu leen fa kanam Buur Nabukodonosor. 19 Buur wax ak ñoom te gisul ci ñoom ñépp kenn ku mel ni Dañeel ak Anaña ak Mikayel ak Asaryaa. Ñu daldi tàbbi ci liggéeyu buur. 20 Mboolem wàllu xam-xam ak xel mu leen Buur seetlu rekk, gis ne ñoo ci sut fukki yoon taryaax yeek ñeengokati réewam mépp.
 
21 Dañeel nekk na ca liggéeyu buur, nekk ca ba ca at ma jëkk ca nguurug Buur Sirus.