Saar 12
1 Bàyyil xel ki la sàkk,
bi ngay dese ndaw,
bala bési safaan a taxaw,
ba jant ñëw, nga naa:
«Amatuma bànneex.»
2 Fa la jant di lëndëme,
weer giim, biddiiw giim,
taw siwet, mu niru la lu xiinati.
3 Su bés baa wattukati kër gi di lox,
jàmbaari xare yi sëgg,
wolkat yi néew, ba wolatuñu,
ñiy séentu ci caax yi giimle,
4 bunt yi féeteek mbedd mi tëje,
coowal wol dal,
as picc sab, nelaw naaw,
janq ju doon woy, selaw.
5 Nga dem, ba ragal fu kawe,
am tiitaange ciw yoon,
garab tóor, ba weex furr,
soccet di yokokoki,
doomu garab tëë yékkati siddit,
nga jëm kër gu mujj,
waa dëj bi fees mbedd mi.
6 Bàyyil xel ki la sàkk,
balaa buumu xaalis bi ne tipp,
ndabal wurus wi, tasar,
njaq la ñuy roote, rajax,
poli ba ca teen ba, tàllit.
7 Su boobaa pënd dellu suuf, na woon;
bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba.
Léppi cóolóoli neen.
Ma daaneel
9 Waarekat ba daa xelu,
di jànglewaale xam-xam,
di natt ak a gëstu,
di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.
10 Waarekat ba daa tànn baat yu saf,
bind ko, mu jub te dëggu.
11 Waxi ku xelu day gindee, bantub sàmm la;
tënk ba diy pont, sampe ca.
Loolu ag may la, jóge ci sàmm biy kenn.
12 Doom, leneen lu ci tegu, moytu ko:
Yokki téere amul kemu,
njàng mu bare, coonoy boroom.
13 Ma daaneele fii, déggees na lii lépp:
Yàlla, ragal ko;
ay santaaneem, jëfe ko;
loolu rekk mooy nit.
14 Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte,
ba ci lépp lu làqu,
muy lu baax, di lu bon.