Bataaxal bi Yàlla may Póol,
mu bind ko waa
Efes
Saar 1
Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la kàddu gii bawoo, ñeel ñu sell ña ca Efes te di ñu sàmm seen kóllëre ak Almasi Yeesu. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
Ay barkee ngi ci Almasi
Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya. Te mooy noonu mu nu taamoo ba àddina sosoogul ndax Almasi mi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem. Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.
Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa, wi mu nu baawaanal, mayaale nu mépp xel mu rafet akug dégg. Moo nu xamal mbóotum coobareem, mi mu nammoona sottale naka jekk ci Almasi, na mu ko neexe. 10 Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi, mboolem la fa asamaan, ak li fi suuf. 11 Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem. 12 Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi.
13 Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm, bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon. 14 Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.
Póol sant na, ñaan na
15 Moo tax man it, bi ma déggee ba tey, seen ngëm ci Sang Yeesu, ak seen cofeel ci ñu sell ñépp, 16 noppiwumaa sant Yàlla ndax yeen, te maa ngi leen di fàttliku ci samay ñaan, 17 ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax. 18 Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem, ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo. 19 Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem, 20 ji mu fésal ci Almasi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram, fa déndi asamaan. 21 Foofa la Almasi tiime lu sore gépp nguur, ak bépp sañ-sañ, ak gépp manoore, ak gépp kilifteef, ak wépp tur wees di tudd, muy tey, di ëllëg. 22 Yàlla moo teg lépp fi suufu ndëgguy tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi, 23 mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi mooy matal lépp ci ñépp.