Saar 23
Àtte laaj na njub ak yërmande
1 «Buleen siiwal ay fen; buleen lëngoo ak tooñkat, ngir doon seedeb naaféqam. 2 Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg. 3 Néew-doole bi it, buleen ko far cib layoo.
4 «Su ngeen dajeek seen nagu noon mbaa mbaamam mu réer, fexeleen ba délloosil ko ko. 5 Su ngeen gisee seen mbaamu noon mu ab sëf daaneel, buleen ko romb; dimbalileen seen noon, yékkatil-leen ko ko.
6 «Buleen jalgati àqu néew-ji-doole cib layoom. 7 Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk. 8 Alali ger nag buleen ko nangu, ndax ger day gumbaal njàccaar, di safaan waxi ku nekk ci dëgg.
9 «Ab doxandéem, buleen ko not; yeen ci seen bopp, jaar ngeen ci ndoxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.
Lu jëm ci bési Noflaay
10 «Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool, for li ci meññe; 11 waaye atum juróom ñaareel ma, noppal-leen tool bi, booyal ko; seen néew-dooley askan wi man cee lekk, li ci des, rabi àll yi for ko. Seen toolub reseñ ak seen tóokëru oliw itam, naka noonu.
12 «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, nopplu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana nopplu, seen surga akub doxandéem it mana astandiku.
13 «Li ma leen wax lépp sàmmleen ko, te turi yeneen yàlla, buleen ko tudd; bumu jibe sax seen gémmiñ.
Lu jëm ci bési màggali Israyil
14 «Ñetti yoon cim at ngeen may jagleel màggal. 15 Màggalu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir ni ma leen ko sante, saa yu jamonoom jotee ci weeru Abiib, ndaxte ci ngeen génn Misra. Te itam buleen taxawe loxoy neen ci sama kanam. 16 Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi. 17 Ñetti yoon cim at la seen góor ñépp di teew fi kanam Boroom bi Aji Sax ji.
18 «Buleen ma rendil benn sarax, di boole deret jaak lu am lawiir, te nebbonu jur gu ngeen ma sarxal ci sama màggal, bumu fanaan ba bët set.
19 «Ngëneeli meññeef ma jëkka ñore ca seen suuf, moom ngeen di yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji.
«Ab tef, buleen ko togge soowum yaayam.
Yàlla yeb na bànni Israyil
20 «Te nag man ci sama bopp, maay yebal malaaka, mu di leen sàmm ci yoon wi, ba yóbbu leen bérab ba ma waajal. 21 Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe. 22 Waaye su ngeen ko déggalee ba déggal ko, di jëfe li ma leen wax lépp, su boobaa ma noonoo seeni noon, bañ seeni bañaale.
23 «Bu leen sama malaaka jiitoo, ba yóbbu leen ca réewum Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Kanaaneen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, ba ma faagaagal leen ñoom ñépp, 24 su boobaa buleen sujjóotal mukk seeni tuur, di leen jaamu, mbaa ngeen di roy seeni aada, waaye yàqteleen seeni tuur te toj tasar seen tuuri doj, ya fa sampe. 25 Jaamuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir. 26 Su ko defee du kenn ku ëmbam di yàqu, mbaa mu tëlee am doom ci seenum réew, te maay matal sëkk seen limu fan.
27 «Tiitaange laay yebal, mu jiitu leen. Maay tiital mboolem xeet wu ngeen fekki, te maay def seen noon yépp won leen gannaaw. 28 Maay yebal njàqare lu leen jiitu, dàqal leen Eween ñi ak Kanaaneen ñi ak Etteen ñi. 29 Waaye duma leen dàqandoo ci menn at, lu ko moy réew mi gent, rabi àll yi mujj bare lool ci seen kaw. 30 Ndànk-ndànk laa leen leen di dàqal, ba kera ngeen di yokku, ba nangu réew mi.
31 «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen. 32 Buleen wóllëranteek ñoom, buleen wóllëranteek seeni tuur. 33 Buñu dëkke seenum réew, lu ko moy muy seen ndëgg-sërëx; ndax dañu leen di xiir ci moy ma, ba ngeen jaamu seeni tuur.»