Saar 7
Jeexle dikk na
1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal, ne ma: 2 «Léegi nag, yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax réewum Israyil ne ko:
“Jeex na tàkk!
Jeexal dikkal na ñeenti weti réew mi.
3 Jeexal nga nag léegi!
Maay yebal sama mer fi sa kaw.
Maa lay mbugale say jëfin,
yool la sa jépp jëf ju siblu.
4 Duma la xool bëtu ñéeblu,
duma ñeewante.
Say jëfin laa lay yool,
sa jëf ju siblu ji ci sa biir.
Su boobaa ngeen xam ne man maay Aji Sax ji”».
5 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
«Céy wii ay, guléet wii ay!
Mu ngii di dikk.
6 Jeexlee ngoog, jeexle dikk na,
jekki, yewwul la.
Mu ngii, di dikk!
7 Yaw nitu réew mee, sànkute dikkal na la.
Àpp mat,
bés dëgmal,
tiitaange wuutu ca mbéx fa kaw tund ya.
8 Du yàgg dara ma xëpp la sama xadar,
ŋaccal la sama mer,
mbugale la say jëfin,
yool la sa jépp jëf ju siblu.
9 Duma xool bëtu ñéeblu,
duma ñeewante.
Say jëfin laa lay yool
ak sa jëf ju siblu ji ci sa biir.
Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax jiy dumaa.
10 «Bés baa ngi, mu ngooguy dikk,
sànkute sàqi na,
yetu njubadee tóor,
reewande jebbi.
11 Fitnaa taxaw, di yet wuy dóoral coxor.
Seen lenn du des,
du seen mbooloo,
du seen alal,
du seen daraja.
12 Àpp mat,
bés jege.
Bu ca jëndkat tala bég,
bu ca jaaykat tala naqarlu!
Am sànj a dikkal askan wépp.
13 Bu jaaykat bi muccee it,
du jotaat ca njaayam.
Peeñu mi jëm ci askan wépp, daal, du toxu,
ku nekk ñaawtéefam lay dunde,
ba du leqliku.
14 Liitu xareey jib, ba lépp jekk ngir xare,
te kenn du xareji,
samam sànj a dikkal askan wépp.
15 Saamar biti,
mbas akub xiif ci biir,
ki ci àll bi deeye xare,
ki ci biir dëkk bi, xiif ak mbas rey ko.
16 Ña rëcc, rawi ca tund ya,
waru pitaxi xur ya,
ñooy binneendoo ndax seeni tooñ.
17 Yoxo yépp yoqi,
tànk tooy xepp.
18 Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo,
seen yaram wépp daw,
gépp kanam sëlmoo gàcce,
bopp ya di nel yu set wecc.
19 Seen xaalis, ñu sànni ci mbedd yi,
seen wurus di leen saf sagaru sobe.
Keroog bésub sànjum Aji Sax ja,
du xaalis, du wurus wu leen di xettli.
Du leen fajal xiif,
du leen reggal,
xanaa tàbbal leen cig njubadi.
20 Ñoo doon sagoo seen gànjar gu yànj,
di ci sàkk jëmmi tuur yu jara bañ te jomblu,
ba tax ma defal leen ko sagaru sobe.
21 Maa koy teg ci loxoy doxandéem, ñu foqati ko,
muy alal ju sagari niti àddina sëxëtoo,
teddadil ko.
22 Maa leen di dummóoyu,
maay bàyyi nit ñi teddadil sama ngëneelu bérab,
ay sàcc a cay tàbbi, teddadil ko.
23 Waajal-leen càllala yi,
tuur nañu deret ba réew mi fees,
dëkk bi fees ak fitna.
24 Maay indi xeet yi gëna néeg,
ñu nangu seeni kër,
ma daldi sàggi sagu boroom doole yi,
sobeel seen bérab yu sell.
25 Tiitaangee ngi dikk,
ñuy sàkku jàmm, jàmm réer.
26 Ay ci kaw ay a ngi dikk,
xibaar ci kaw xibaar,
ñuy sàkku peeñum yonent ci neen,
ndigalu yoon réer sarxalkat,
pexe réer mag.
27 Buur dina tiislu,
garmi làmboo séri ñaawlu,
baadoolay réew mi di kat-kati.
Seeni jëfin laay jëfeek ñoom,
seeni àtte laa leen di àttee,
ñu xam ne maay Aji Sax ji!»