Saar 11
Digeb yiw a gën jàmmu tey
1 Ba loolu wéyee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ma ba ca buntu penkub kër Aji Sax ja janook penku. Foofa ca bunt ba, yemuma ci lu moy ñaar fukki nit ak juróom. Ma xàmmi ca Yaasaña doomu Asur ak Pelaca doomu Benaya, di njiiti askan wi. 2 Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, ñii ñooy mébétkati ñaawtéef ñiy digle lu bon ci dëkk bii. 3 Ñu ngi naa: “Bunu tabaxagum ay kër; dëkk bii daa mel ni ndab, nun nu fegu ni yàpp wu ca ube.” 4 Kon nag yaw nit ki, waxal waxyu ci seen kaw. Jottlil waxyu.» 5 Noowug Aji Sax ji daldi dal fi sama kaw, ne ma: «Neel:
“Aji Sax ji dafa wax ne:
Yeen waa kër Israyil, yeena waxe nii,
seeni mébét, xam naa ko.
6 Bóom ngeena bóom seen bokki dëkk bii,
ba mbedd yi fees dell aki néew.
7 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Dëkk bi kay ndab la,
seen bokki néew yi ngeen fi saam di yàpp wi ci ube,
waaye yeen dees na leen fi génnee.
8 Saamar ngeen ragal,
saamar laa leen di indil.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
9 Maa leen di génne biir dëkk bi,
teg leen ci loxoy doxandéem,
wàcceel leeni mbugal.
10 Saamar ngeen di fàddoo,
fa catal Israyil laa leen di mbugale,
ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
11 Dëkk bii du doon seen ndab,
te dungeen yàpp wu cay ube.
Fa catal Israyil laa leen di mbugale.
12 Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax,
ji ngeen sàmmul dogali yoonam,
jëfewuleen àttey yoonam,
xanaa di jëfe aaday xeet yi leen séq.”»
13 Naka laay biral waxyu, Pelaca (mu firi Aji rëcc ju Yàlla) doomu Benaya jekki rekk, dee. Ma ne fëlëñ, dëpp sama jë fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaay faagaagal ndesu Israyil nii?»
14 Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: 15 «Yaw nit ki, gannaaw sa bokk yooyu nga bokkal, ñuy say bokk lenqe, di mboolem waa kër Israyil ñi nekk ngàllo, ñoom la waa Yerusalem di siis, naan:
“Soreleen Aji Sax ji;
réew mii, nun la ko sédd.”
16 Kon nag, waxal ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa soreel moos seen bokk yooyu fa biir yéefar ya,
maa leen wasaare biir réewoo réew,
te du tee ma teewal leen ni bérab bu sell
fa réew ya ñu sancaani.”
17 Moo tax nanga wax ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa leen di dajalee fa xeet ya,
boolee leen fa réew ya ngeen wasaaroo,
ba joxaat leen suufas Israyil.”
18 Bu ñu ñibbee, jële fa mboolem lu jomblu
ak lépp lu siblu.
19 Maa leen di may beneen xol ak xel mu yees.
Xolu doj bi laay roccee ci seen suux,
weccee leen ko xolu suux.
20 Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe,
te sama àttey yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
Su boobaa ñuy sama ñoñ,
may seen Yàlla.
21 Waaye nit ña seen xol jengal seen jëf ju jomblu,
ak seen yëf yu seexluwu,
maay këpp seen jëfin ci seen bopp.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
22 Ba loolu amee malaakay serub ya firi seeni laaf, ànd ak mbege ya, leeru Yàllay Israyil tiim leen fa kawa kaw. 23 Gannaaw loolu leeru Aji Sax ji yékkatikoo fa digg dëkk ba, dem, taxawi fa kaw tund wa ca penkub dëkk ba. 24 Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ba ca waa ngàllo ga ca réewum Babilon, lépp ci peeñu, ci dooley Noowug Yàlla. Peeñu ma ma gis nag yem fa. 25 Ba loolu amee ma àgge waa ngàllo ga mboolem mbir ya ma Aji Sax ji won.