Saar 33
Tabb nañu Esekiyel jongrukat
1 Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Yaw nit ki, waxal ak sa bokk yi, nga ne leen: “Am réew, su ma wàccee xare ci kawam, waa réew ma tànne ci seen biir kenn, def ko seen jongrukat, 3 su kooka séenee congum xare muy dikk ci réew mi, daldi wal liit gi, àrtu waa réew mi, 4 ku dégg baatu liit ga te fàgguwul, bu cong mi agsee ba yóbbaale ko, mooy gàddu bakkanu boppam. 5 Gannaaw dégg na baatu liit ga, te taxu koo fàggu, mooy gàddu bakkanu boppam. Ku déggoon ba fàggu nag, moo musal boppam. 6 Su jongrukat ba séenee congum xare may dikk te walul liit ga, loolu waral waa réew mi fàgguwñu, ba cong ma agsi, ba rotal bakkanu kenn ca ñoom, su boobaa njubadiy jongrukat baa ko rotal, te bakkanu nit kooka, jongrukat ba laa koy topp.”
7 «Yaw nit ki nag, jongrukat laa la tabb, ñeel waa kër Israyil, ba boo déggee baat bu jibe sama gémmiñ, war leen koo artoo ci sama ndigal. 8 Bu ma nee ku bon ki: “Yaw ku bon ki, dee rekk mooy sa àtte,” te yaw waxuloo ko ko, àrtu ko ngir mu wacc yoonu mbonam, ku bon kooka aw ayam mooy àtteb deeyam. Waaye bakkanam, yaw laa koy topp. 9 Waaye yaw soo artoo nit ki ngir mu wacc yoonu mbonam, te taxu koo wacc yoonu mbonam, moom la aw ayam di àtteb deeyam, waaye yaw yaa musal sa bopp.
10 «Yaw nit ki, waxal ak waa kër Israyil, ne leen: “Ngeen ne dungeen mana mucc ndax seeni tooñ ak seen bàkkaar yu leen diis ba semmal leen?” 11 Waxleen ne leen: “Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, awma bànneex ci deewug nit ku bon. Sama bànneex mooy mu wacc yoonu mbonam, ba dund. Kon yeen waa kër Israyil, waccleen, ngalla waccleen seen yoonu mbon. Ana lu jar ngeen di dee?”
12 «Yaw nit ki, waxal sa bokk yi, ne leen: “Boroom njekki démb li, su tooñee tey, njekkam loola du ko musal. Ku bon ki itam, bu waccee yoonu mbonam, tey, mbonu démbam ga du ko lor. Boroom njekki démb li nag, su bàkkaaree, njekkal démbam la du ko may mu dund. 13 Doonte maa ne boroom njekk li dina dund moos, te gannaaw gi mu yaakaar njekkal démbam la, bay def safaan ba, su boobaa gépp njekkam ga woon, deesu ci bàyyi xel, te safaan bi mu def tey mooy doon àtteb deeyam. 14 Su ma nee ku bon ki: ‘Yaw dee rekk mooy sa àtte,’ mu mujj dëddu bàkkaaram, di jëfe njub ak njekk, 15 di delloo alalu tayle ju mu laajoon, di fey lu mu sàccoon, di jëfe dogali yoon yiy taxa dund, tey baña jëfe njubadi, su boobaa dina dund moos te àtteb dee toppu ko. 16 Mboolem lu mu bàkkaaroon, deesu ko ko bàyyil xel. Njub geek njekk gi mu mujje moo ko may mu dund.”
17 «Sa bokk yi nee ñu: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Te ñoom la seen doxalin dul noonu! 18 Boroom njekk li daal, su dëddoo njekkam di def njubadi, njubadi gaay doon àtteb deeyam. 19 Ku bon ki nag, su dëddoo mbonam, di jëfe njub ak njekk, loolaa koy may mu dund.
20 «Yeen waa kër Israyil, ngeen ne: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Nit ku nekk daal, jëfinam laa koy àttee.»
Jëf ju bon daane na Yerusalem
21 Ca fukkeelu atu ngàllo ak ñaar, keroog juróomi fan ca fukkeelu weer wa, jenn waay a rëcce ca jéllub Yerusalem ba, dikk ne ma: «Dëkk ba daanu na!» 22 Fekk na ngoon ga jiitu dikkam, Aji Sax ji teg ma loxo, ba tijji sama gémmiñ. Ba waa ja rëcc agsee fa man ca ëllëg sa ca suba, fekk na sama gémmiñ tijjiku, luuwatuma.
23 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 24 «Yaw nit ki, ñi dëkke genti réewum Israyil mii ñu ngi naan: “Ibraayma kenn la woon te moo moomoon réew mi. Kon nun ñiy ñu bare noo ko ci gëna yey.” 25 Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi? 26 Yeen wóoluwuleen lu moy seen saamar, ngeen di def jëf ju siblu, ku nekk di jaalook jabaru moroomam, ba noppi di moom réew mi?” 27 Wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, ku nekk ci yeen ci biir gent yi, saamar lay fàddoo; képp ku nekk ci biir àll bi, rab yi laa koy jox, ñu lekk ko; te képp ku làqoo tata yeek xunti yi, mbas a koy rey. 28 Maay def réew mi gent bu wéet, sagu réew mi sàggiku, tundi Israyil ne faraas, kenn du ca jaare. 29 Bu ma defee réew mi gent bu wéet ndax seen mboolem jëf ju siblu, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.”
30 «Léegi nag, yaw nit ki, sa bokk yaa ngi lay waxtaane ci keppaari tata yi ak ci bunti kër yi. Ñu ngi waxante ci seen biir, ku nekk naa mbokkam: “Aycaleen nu dem dégluji gan kàddoo tukkee ci Aji Sax ji.” 31 Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku. 32 Dañu laa jàppe rekk ni boroom woy yu neex, ku neex baat, te mane xalam. Dañuy déglu say wax te duñu ci jëfe dara. 33 Waaye sa wax jaa ngii di waaja sotti, te bu sottee dinañu xam ne ab yonent a ngi woon fi seen biir.»