Saar 45
Lu jëm ci suuf si ñu jagleel Aji Sax ji
1 «Bu ngeen demee bay tegoo réew mi bant ngir séddoo ko, nangeen jooxeel Aji Sax ji dogu suuf bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), yemook fukki kilomeetar ak ñett, yaatoo ñaar fukki junniy (20 000) xasab, yemook fukki kilomeetar ak genn-wàll. Suuf soosu sépp ba fa mu yem, lu sell lay doon. 2 Biir pàkk boobu, nañu ci waccal bérab bu sell bi ab dénd bu kaare, wet gu nekk di juróomi téeméeri xasab, yemook ñaar téeméeri meetar ak juróom fukk; ak bayaal bu wër dénd bi, yaatoo juróom fukki xasab, yemook ñaar fukki meetar ak juróom wet gu nekk. 3 Ci biir dogu suuf bu mag boobu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) te yaatoo fukki junniy xasab (10 000), yemook juróomi kilomeetar ak xaajaat, ci ngay nattal bérab bu sell bi, di fu sell fee sell. 4 Bérab bu sell a ngoog bu ñuy sàkke ci réew mi, ñeel sarxalkat yiy liggéey ci bérab bu sell bi, tey jege Aji Sax ji, di ko liggéeyal. Foofu lañuy am ay kër te foofu lañuy beral ab pàkk bérab bu sell bi. 5 Beneen dénd bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), yaatoo fukki junniy xasab (10 000), na ñeel Leween ñiy liggéeyal kër Yàlla gi, ngir ñu am dëkk yu ñu dëkke.
6 «Suufas dëkk bi, nanga ko àppal yaatuwaayu juróomi junniy xasab (5 000) ak guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), mu làng ak dog bi ñu sàkkal bérab bu sell bi. Suuf soosu na ñeel waa kër Israyil gépp. 7 Boroom jal bi nag, nañu ko jagleel ñaari wet yi séq suufas bérab bu sell beek pàkkub dëkk bi. Suufas buur soosu jóge sowu ba géej ga, jógeeti penku ba fa Israyil yem, na guddaayam tollook guddaayu suufu giirug Israyil gu ci nekk. 8 Loolooy doon céru suufu boroom jal bi ci Israyil. Su ko defee boroom jal yi ma fal dootuñu xañ sama ñoñ suuf. Dañuy wacce giiri waa kër Israyil li des ci réew mi.
Sàrt yii war na boroom jal bi ci wàllu kër Yàlla gi
9 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ñiy tooge jalu Israyil, na doy nag! Coxor geek jaay-doole bi, baleen ko. Njub ak njekk ngeen war di jëfe. Bàyyileen di nangu sama alali ñoñ. Boroom bi Aji Sax jee ko wax. 10 Seen màndaxekaay na doon njub, efab nattukaayu sol-sotti di njub, seen bat bi ñuy natte lu ñuy xelli di njub. 11 Na benn efa ak benn bat yem dayo, lu ci nekk wara def céru fukkeelu benn omer* 45.11 benn omer am na ñu jàpp ne mu ngi tollook ñeenti téeméeri liitar ak juróom fukk, mbaa ñetti téeméeri kilo. Natt yii, seeni dayo daan na soppiku, topp jamono yaak bérab ya ñu ko daan jëfandikoo., bi yemook ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220), mbaa téeméeri kilo ak juróom fukk (150). Te na benn omer di dayo bi ngeen di natte. 12 Benn siikal, na wecciku ñaar fukki gera† 45.12 Moo doon natt ba gënoona tuut ci wàllu diisaay, yemook genn-wàllu garaam., te boo boolee nattu ñaar fukki siikal, ak nattu ñaar fukki siikal ak juróom, ak nattu fukki siikal ak juróom, mu wara wecciku benn natt bi ñuy wax miin.
13 «Lii nag mooy doon seenub jooxe: muy bele, di lors, na doon seen benn céru juróom benn fukkeelu meññeef, di ñaari kilook genn-wàll ci téeméeri kilook juróom fukk yu nekk. 14 Su dee ag diw, bat bi ñuy natte lu ñuy xelli lañu koy natte, benn bat yemook fukkeelu natt bi ñuy wax omer, mbaa fukkeelu natt bi ñuy wax kor, di ñaari liitar yu tombal ñaar (2,2) ci ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220) yu nekk. 15 Ci wàllu parluy Israyil, benn ay génn ci ñaar téeméeri gàtt yu ne, gàtt yooyu ñeel saraxi pepp, ak saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm ngir njotlaayal askan wi. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. 16 Boobu jooxe, mboolem waa réew mee ciy def seen loxo, indil ko ki tooge jalub Israyil. 17 Li war ki tooge jal bi, saraxu rendi-dóomal ci la, ak saraxu pepp, ak saraxi biiñ yi ñuy joxe bésu màggal, yu mel ni màggali Terutel weer ak bési Noflaay, ak yeneen bés yu bànni Israyil taamoo daje. Moom it mooy joxe saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu pepp, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxu cant ci biir jàmm ngir njotlaayal waa kër Israyil.
18 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Benn fanu weer wi jëkk, nanga jël yëkk wu ndaw wu amul sikk ngir laabal bérab bu sell bi. 19 Sarxalkat bi day sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar boobu, taqal ci jëni bunt yi, ak ñeenti colli kaw sarxalukaay bi, ak jëni buntu ëttu biir bi. 20 Noonu it ngay def ca juróom ñaareelu fanu weer wa, ngir daboo ko nit ku jàdd yoon te yégu ko mbaa teyu ko. Su ko defee ngeen def njotlaayal kër Yàlla gi.
21 «Fukki fan ak ñeent ci weer wu jëkk wi mooy seen màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan la màggal giy am, te mburu mu amul lawiir lañu ciy lekk. 22 Bés boobu la ki tooge jal bi di joxeel boppam ak mboolem waa réew mi, yëkk wu ndaw wuy doon saraxu póotum bàkkaar. 23 Juróom ñaari fan yooyu dina sarxal Aji Sax ji bés bu nekk juróom ñaari yëkk yu ndaw ak juróom ñaari kuuy yu amul sikk, def ko saraxu rendi-dóomal, ak ab sikketu sarax ngir peyug tooñ, bés bu nekk. 24 Yëkk wu ci nekk ak kuuy mu ci nekk, da koy booleek saraxu benn efab‡ 45.24 benn efa, am na ñu jàpp ne fanweeri kilo lay tollool, benn xiin wara tollook juróom ñetti liitar, lim yooyu mat ñaari yoon li nu am fii. pepp, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak efab pepp bu ne, benn xiinu diw, di ñetti liitari diw ak genn-wàll.
25 «Ci wàllu màggal giy door fukki fan ak juróom ci juróom ñaareeli weer wi§ 45.25 Màggalu bési Mbaar yi lay doon. Seetal ci Sarxalkat yi 23.33-34., na ki tooge jal bi def niki ci màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan, yi màggal giy def, yenn sarax yooyii rekk lay joxe, muy saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxi pepp ak diw.
*45:11 45.11 benn omer am na ñu jàpp ne mu ngi tollook ñeenti téeméeri liitar ak juróom fukk, mbaa ñetti téeméeri kilo. Natt yii, seeni dayo daan na soppiku, topp jamono yaak bérab ya ñu ko daan jëfandikoo.
†45:12 45.12 Moo doon natt ba gënoona tuut ci wàllu diisaay, yemook genn-wàllu garaam.
‡45:24 45.24 benn efa, am na ñu jàpp ne fanweeri kilo lay tollool, benn xiin wara tollook juróom ñetti liitar, lim yooyu mat ñaari yoon li nu am fii.
§45:25 45.25 Màggalu bési Mbaar yi lay doon. Seetal ci Sarxalkat yi 23.33-34.