Saar 7
Buur Artaserses yéwéne na Esra
1 Ba loolu weesee, ca jamonoy nguurug Artaserses buuru Pers, am na góor gu ñuy wax Esra, Seraya di baayam. Seraya, Asaryaa; Asaryaa, Ilkiya; Ilkiya, 2 Salum; Salum, Cadog; Cadog, Ayitub; 3 Ayitub, Amarya; Amarya, Asaryaa; Asaryaa, Merayot; 4 Merayot, Seraya; Seraya, Usi; Usi, Bukki; 5 Bukki, Abiswa; Abiswa, Fineyas; Fineyas, Elasar; Elasar, Aaróona, sarxalkat bu mag ba. 6 Esra moomu jóge Babilon, nekkoon jànglekat bu xareñ, bu géeju ci yoonu Musaa, wi Aji Sax ji Yàllay Israyil joxoon ñoñam. Aji Sax ji Yàllaam nag toppe ko yiwam, ba Buur defal ko mboolem lu mu ñaan.
7 Ca juróom ñaareelu atu nguurug Buur Artaserses, mu am ñenn ci bànni Israyil ñu ànd, di ay sarxalkat aki Leween aki jàngkat aki fara bunt, ak liggéeykati kër Yàlla ga. Ñu daldi dem Yerusalem. 8 Esra nag bokkoon ca. Mu agsi Yerusalem ca juróomeelu weeru at mooma, di juróom ñaareelu atu buur ba. 9 Ca benn fanu weer wa jëkk la dooroon yoon woowu mu bàyyikoo Babilon. Mu agsi Yerusalem ca benn fanu juróomeelu weer wa, ci mbaaxu Yàllaam ji ko toppe yiwam. 10 Esra nag doonoon ku pastéefu ci jàng yoonu Aji Sax ji, di ko sàmm tey jàngle ci Israyil ay dogalam ak ndigali yoonam.
Buur Artaserses bind na Esra
11 Lii mooy li ñu bind ci bataaxal ba Buur Artaserses jox Esra, sarxalkat ba, jànglekat ba géeju ci mbiri santaaney Aji Sax ji ak dogalam yi ñeel Israyil.
12 Bataaxal bii mu ngi bàyyikoo ci Artaserses, buuru buur yi, jëm ca Esra, sarxalkat biy jàngle yoonu Yàlla Boroom asamaan. Maa ngi lay nuyu.
Gannaaw loolu nag, 13 ndigal tukkee na ci man ne mboolem kuy bànni Israyil ci samam réew, ba ci sarxalkat yeek Leween ñi, ku ci bëgga ànd ak yaw Yerusalem, man naa dem. 14 Man Buur, maa la yebal, maak sama juróom ñaari wóllëre; noo la yebal Yerusalem ak Yuda, ngir nga gëstujil ma nu ñu fay toppe sa yoonu Yàlla, wi nga yor téereem ci say loxo. 15 Te nga yóbbaale xaalis beek wurus, wi ma joxe ci xol bu tàlli, jagleel ko Yàllay Israyil ji ci Yerusalem, man Buur, maak samay wóllëre, 16 boole ci mboolem xaalis mbaa wurus woo mana jële ci diiwaanu Babilon bépp, ak itam saraxi yéene yi baadoolo yeek sarxalkat yi joxe ci xol bu tàlli, lépp ñeel seen kër Yàlla ga ca Yerusalem. 17 Ci biir loolu, xaalis boobu nanga ko daldi jënde ay yëkk aki kuuy ak xar yu ndaw ak saraxi pepp ak saraxi tuuru yi muy àndal te nga boole ko, jooxe ca seen sarxalukaayu kër Yàlla ga ca Yerusalem. 18 Li des ci xaalis beek wurus wi nag, defleen ko lu ngeen namm, yaak say bokk, na mu dëppook seen coobarey Yàlla. 19 Bu loolu weesee ndab yi ñu la jox, ñu di ko jaamoo ca seen kër Yàlla ga, nanga ko boole teg fa kanam Yàllay Yerusalem. 20 Leneen lu des it, loo wara def ci sa kër Yàlla gi, sañ nga koo génnee ci alalu buur.
21 Man Buur Artaserses, jox naa ndigal mboolem denckati alali buur ya ca Wàllaa Dex, ne leen: Lépp lu Esra, sarxalkat biy jàngle yoonu Yàlla Boroom asamaan, sàkku ci yeen, nangeen ko daldi def; 22 ba ci fanweeri barigoy xaalis, ñetti téeméeri barigoy bele, ñaar fukki barigoy biiñ, ak ñaar fukki barigoy diw, ak lu mu soxla ci xorom. 23 Lépp lu Yàlla Boroom asamaan digle, nañu ko defe noonee ca kër Yàlla Boroom asamaan, ndax meram baña dal ci sama kaw nguur gii ak ci sama kaw askan. 24 Nu ngi leen di xamal itam ne képp kuy sarxalkat mbaa ab Leween, mbaa mu dib jàngkat mbaa fara bunt, mbaa mu di liggéeykatu kër Yàlla gi, mbaa surga buy liggéey ci kër Yàlla googu, du galag bu ñu ko saña teg mbaa njotu bopp mbaa ab juuti.
25 Yaw Esra nag, seetal ci xel mu rafet mi sa Yàlla digle ci yoonam wi nga yor, nga tabb ay njiit aki xaali, ngir ñuy àtte mboolem ñi xam sa yooni Yàlla ci diiwaani Wàllaa Dex. Te ñi ko xamul, nga xamal leen ko. 26 Képp ku ci sàmmul sa yoonu Yàlla ak yoonu buur, nañu ko daldi teg mbugal mi war ci moom. Dee mooy doon àtteem, mbaa ñu génne ko réew mi, mbaa ñu nangu alalam, mbaa ñu tëj ko.
Esra sant na
27 Cant ñeel na Aji Sax ji, sunu Yàllay maam, moom mi def nii ci xolub Buur yéeney teral kër Aji Sax ji ci Yerusalem, 28 te dawal ngor sama digganteek Buur aki wóllëreem ak mboolem kàngami buur yu mag yi! Man nag, nii la ma sama Yàlla Aji Sax ji toppe yiwam, ba ma dëgërlu, boole njiiti Israyil, ñu daje, ànd ak man dem.