Saar 2
Darajay jaamookaay bi dina yokku
Ca ñaareelu atu nguuru Buur Daryus, Ca juróom ñaareelu weer wa, yemook ñaar fukki fan ak benn* 2.1 Bés boobu moo mujjoon ci màggalu bési Mbaar yi., kàddug Aji Sax ji moo dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase. Mu ne: «Waxal nag doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, ak ñi des ci askan wi, nga ne leen:
Ana ci yeen ñi fi des, ku gisoon
kër gii ca darajaam ja woon?
Ak nu ngeen ko gise tey?
Xanaa du ag neen la leen di niru?
Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul,
Aji Sax jee ko wax.
Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi,
góor-góorlul;
yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen,
kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen,
maa ànd ak yeen déy,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Googu kàddu laa jaayante woon ak yeen,
ba ngeen di génne Misra.
Samag Noo laa taxawe fi seen biir,
buleen tiit.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne:
Fileek lu néew, maa ngii di yëngalaat
asamaan ak suuf, ak géej ak jéeri.
Maay yëngal xeetoo xeet,
alali xeetoo xeet duggsi,
ma feesal kër gii ak teraanga,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax;
Maa moom xaalis, moom wurus;
kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Mu ne: Ci bii bérab laay mayee jàmm,
kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»
Jëfi sobe àndul ak barke
10 Ca ñaar fukki fan ak ñeentu juróom ñeenteelu weer wa 2.10 Mu yemook ñetti weer gannaaw ndoortel tabaxu kër Yàlla ga., yemook ñaareelu atu nguuru Buur Daryus, kàddug Aji Sax ji moo dikkal Yonent Yàlla Ase, ne ko: 11 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Sàkkul nag ndigal ci sarxalkat yi, nga ne leen, 12 waaw, su nit yoree ci lafu mbubbam, aw yàpp wu ñu sellal, ba noppi lafu mbubbam laal mburu mbaa lu ñu togg, mbaa biiñ mbaa ag diw mbaa ñam wu mu doon, ndax loola day daldi sell?» Ase laaj ko sarxalkat ya, ñu ne ko: «Déedéet.» 13 Ase dellu ne leen: «Nit ku sobewu ndax ab néew bu mu laal, su laalee lenn ci mboolem ñam yooyu, ndax ñam wa sobewu na?» Sarxalkat ya ne ko: «Sobewu na kay.» 14 Ase nag wax leen, ne leen:
«Noonu la ci askan wii,
noonu la ci xeet wii sama kanam.
Kàddug Aji Sax jee.
Noonu la ci mboolem seen liggéeyu loxo,
ak sarax su ñu fi indi, loolu lépp a sobewu.
Déggal Aji Sax ji, baaxle
15 «Léegi nag seetaatleen seen xel bu baax,
dale ko bésub tey jii.
Bi aw doj tegoogul woon ci aw doj,
ci tabaxub kër Aji Sax ji,
16 ku wuti waan ñaar fukki natti pepp,
fukk lay fekk sàq ya;
mu wuti ca nalukaay ba juróom fukki natti biiñ,
fekk fa ñaar fukk.
17 Maa leen dumaa gàncax gu benaat,
ak gu xuur, ak tawub doji yuur
ci mboolem seen liggéeyu loxo,
te taxul ngeen délsi fi man,
kàddug Aji Sax jee.
18 Seetaatleen seen xel bu baax,
dale ko bésub tey jii,
dale ko ci ñaar fukki fan ak ñeentu
juróom ñeenteelu weer wi,
daleleen ci bés bii kenug néegu Aji Sax ji tegee,
ngeen seetaat seen xel.
19 Ana am jiwooti ci sàq yi?
Mbaa lennati ci reseñ ak figg?
Mbaa garabi gërënaat ak oliw? Du lenn lu meññ.
Waaye li ko dale bésub tey jii, maay barkeel.
Ab dige ñeel na Sorobabel
20 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal Ase ñaareel bi yoon,
yemook ñaar fukki fan ak ñeent ci weer wi. Mu ne:
21 «Waxal Sorobabel 2.21 Sorobabelmi soqikoo ci Daawuda moo taxawe buur bi feddli kàddug Aji Sax ja mu noon mooy taxawal nguur gu sax dàkk, ñeel askanu Daawuda. Seetal ci 2.Samiyel 7.11- 16, ak Macë 1.12-13. , boroom Yuda, ne ko:
Maa ngii di yëngalsi asamaan ak suuf.
22 Maay jàllarbi ngànguney nguur yi,
nasaxal dooley nguuri yéefar yi,
jàllarbi watiir ak ay dawalkatam,
fas yeek seeni gawar nërmeelu,
ku nekk fàddoo saamaru mbokkam.
23 Bésub keroog, kàddug Aji Sax jee,
Boroom gàngoor yi,
maa lay jël, yaw samab jaam,
Sorobabel doomu Selcel,
kàddug Aji Sax jee,
te jaarob torlukaay laa lay def,
nde yaw laa taamu.
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»

*2:1 2.1 Bés boobu moo mujjoon ci màggalu bési Mbaar yi.

2:10 2.10 Mu yemook ñetti weer gannaaw ndoortel tabaxu kër Yàlla ga.

2:21 2.21 Sorobabelmi soqikoo ci Daawuda moo taxawe buur bi feddli kàddug Aji Sax ja mu noon mooy taxawal nguur gu sax dàkk, ñeel askanu Daawuda. Seetal ci 2.Samiyel 7.11- 16, ak Macë 1.12-13.