Saar 6
Wooteb tuub jib na
1 Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji.
Moo nu xotat, te moo nuy wéral.
Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
2 Ñaari fan, mu leqli nu,
ñetteel ba mu yékkati nu,
nuy dund fi kanamam.
3 Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji.
Ni jant bu fenk la dikkam wóore,
ni ab taw la nuy dikkale,
ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
4 «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim?
Nu ma lay def yaw Yuda?
Te sa ngor di xiinu suba,
mbaa ab lay, jekki ne mes.
5 Moo tax yonent yi laa leen di dumaa,
sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye.
Seen àttee leen di jollil ni ceeñeeru njël.
6 Ndax ngor laa namm, dub sarax,
ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.
7 «Waaye ñoom ca dëkk ba, Adam lañu feccee kóllëre,
foofa lañu ma wore.
8 Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef,
taq ripp ak deret.
9 Ni saaysaay siy tëroo,
ni la sarxalkat yi lëkkoo,
di bóome ca yoonu Sikem.
Ndaw jëf ju ñaaw!
10 Ci kërug Israyil laa gis lu yées:
Fa la Efrayim di gànctoo,
Israyil googu laa ne moo sobeel boppam.
11 Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe,
kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.