Saar 18
Boroom njaq doon na misaal
1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji. Mu ne ko: 2 «Dalal di dem ca tabaxkatu njaq ba. Foofa laa lay dégtale sama kàddu.» 3 Ma daldi dem ba ca kër tabaxkatu njaq ba. Ma fekk ko muy liggéey ca tabaxukaayu njaqam. 4 Leeleeg ndab li tabaxkat biy tabaxe ban, yàqu ci loxoom, mu dellu defaraat ba mu baax ci moom. 5 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma ne ma: 6 «Ni tabaxkatu njaq bii di def, dama koo manula def ak yeen, bànni Israyil?» Kàddug Aji Sax jee. «Ban bii déy, ni mu mel ci loxol tabaxkatu njaq bi, ni ngeen mel ci sama loxo, yeen bànni Israyil. 7 Leeg-leeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko, 8 xeet woowu tuub mbonam gi ma leen doon artoo, ma fomm musiba mi ma naroona wàcce ci seen kaw. 9 Leeleeg it ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko tabax, jëmbat ko, 10 ba noppi ñu def lu ma ñaawlu, baña dégg sama kàddu. Su ko defee ma fomm lu baax la ma leen naroona baaxe. 11 Kon waxal boog waa Yuda ak waa Yerusalem ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii di leen tabaxal musiba ci pexe mu ma leen di fexeel. Kon na ku nekk dëpp yoonam wu bon te jubbanti jikkoom aki jëfam.” 12 Dañu naan: “Jaru ko, sunu xalaatu bopp lanuy topp, ku nekk të ticc di jëfe sa xel mu dëng.”»
Israyil fàtte na Aji Sax ji
13 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne:
«Laajteleen rekk ci xeet yi!
Ku ci masa dégg lu mel nii?
Lu ñaawa ñaaw la Israyil, janq ba, def!
14 Ku masa gis fu tawub yuur gedde mbartali Libaŋ,
mbaa wal mu sedd ma cay wale fu sore ŋiis?
15 Moona sama ñoñ fàtte nañu ma;
tuuri caaxaan, ñu taalal cuuraay,
te tuur yi di leen fakktal ci seeni yoon,
seen jaaruwaay ya woon,
di leen jaarale ñall yu kenn xàllul,
16 ba seenum réew gental,
di lu ñuy muslu fàww,
ku fa romb waaru, wëcc bopp.
17 Maay mel ni ngelawal penku, tasaare leen,
ñu daw seeni noon.
Gannaaw laa leen di won,
waaye du doon kanam,
keroog seen bésu ay.»
Fexeel nañu Yeremi
18 Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njànglem sarxalkat, du digley boroom xel te du waxyu bu yonent biral. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.»
19 Waaye yaw Aji Sax ji, teewlu ma
te déglu kàddug noon yi.
20 Lu baax dees na ko feye lu bon a?
Moona gasal nañu ma am yeer, di ma tëru.
Bàyyil xel ba may taxaw fi sa kanam,
di leen tinul ngir nga moyale leen sa mer.
21 Kon nag bàyyil seeni doom ñu xiif ba dee,
jañax leen ci ñawkay saamar,
seeni jabar suul doom, suul jëkkër,
seeni góor loroo mbas,
seeni waxambaane daanoo xare.
22 Boo jekkee yebal gàngoor,
yal na yuux jibe seeni kër.
Ñoo gas um yeer, di ma rëbb,
làqal may fiir.
23 Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga mépp pexe
mu ñu may fexee bóome.
Bu leen jéggal seen ñaawtéef,
bul far seeni moy,
yal nañu nërmeelu fi sa kanam,
jëflanteel ak ñoom bi ngay mer.