Saar 20
Tëj nañu Yeremi
1 Ci kaw loolu, doomu Imer, Pasur, sarxalkat ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, dégg Yeremi muy biral kàdduy waxyu yooyu. 2 Ba mu ko defee Pasur dóorlu Yonent Yàlla Yeremi, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin. 3 Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (mu firi Tiitaange lu dajal) la la tudde. 4 Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee. 5 Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon. 6 Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan wax ay waxyuy fen.”»
Yeremi ñaxtu na
7 Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma,
ma naagu, nga nax ma,
jaay ma doole, ba man ma.
Ñu ngi may kekku bés bu ne,
ku ne di ma kókkali.
8 Saa yu ma waxee, damay xaacu,
fitnaak salfaañoo ma tax di yuuxu.
Kàddug Aji Sax jee may yóbbey xas
aki saaga bés bu ne.
9 Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko,
dootuma biral waxyu ci turam,»
sama xol bi mel nib taal
bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi;
may jéema muutuwaale sa kàddu,
te duma ko man.
10 Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan:
«Éey, Tiitaange-lu-dajal!
Booleleen ko, boole rekk!»
Ñi ma séqal jàmm sax,
di yeeru ma fakkastalu,
naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko,
ba mana feyu.»
11 Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare.
Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan,
xanaa rus lool, ndax duñu baaxle;
gàcce gu yàgg lay doon te du fey.
12 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub,
di gis xel ak xol,
may ma, ma gis ni nga leen di feye;
yaw de laa diis sama mbir.
13 Woyleen Aji Sax ji,
màggal-leen Aji Sax ji!
Mooy xettli néew-ji-doole
ci dooley ku bon.
14 Alkute ñeel na bés ba ma juddoo,
bés ba ma saa ndey juree,
yàlla bumu barkeel.
15 Alkute ñeel na ka ko yegge baay,
ne ko: «Sa soxna am na doom ju góor,»
ba tax baay béga bég.
16 Yal na kooku mel ni dëkk,
yi Aji Sax ji tas te yërëmu leen!
Yal na dégg yuuxi suba teel
ak xaacuy xarey njolloor.
17 Moo ma reyul ci sama biiru ndey,
ma bàmmeeloo sama ndey,
te du wasin mukk.
18 Ana lu ma doon génne ca biiram,
di daj coonooku tiis,
mujje gàcce?