Yeremi dugg na coono
Saar 26
(Saar 26—45)
Ñu ngi tëru Yeremi
1 Ba doomu Yosya, Yowakim buurub Yuda di doora falu, kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa Aji Sax ji. Mu ne: 2 «Aji Sax ji dafa wax ne: Dangay taxawi ca biir ëttu kër Aji Sax ji. Nga wax ak mboolem waa dëkki Yuda yiy jaamusi ci kër Aji Sax ji. Mboolem kàddu yi ma lay yóbbante ci ñoom, bu ci wacc baat. 3 Jombul ñu dégg, ba ku nekk dëpp yoonam wu bon. Su ko defee ma fomm musiba, mi ma leen di waajal ndax seen jëf ju bon. 4 Nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Su ngeen ma déggalul, toppuleen yoon wi ma leen rëddal, 5 dégguleen sama kàdduy jaam ñiy yonent yi may yónni ci yeen ay yooni yoon, ngeen tëë dégg, 6 su boobaa maay def kër Yàlla gii, na ma def ga woon ca Silo, te dëkk bii maa koy def lu mboolem xeeti àddina di tudd, di ko móoloo.”»
7 Ba mu ko defee sarxalkat yaak yonent yaak mbooloo ma mépp dégg Yeremi di wax kàddu yooyu ca biir kër Aji Sax ji. 8 Naka la Yeremi wax ba sottal mboolem la ko Aji Sax ji santoon mu jottli ko mbooloo ma mépp, sarxalkat yaak yonent yaak mbooloo ma mépp ànd jàpp ko, ne ko: «Yaw, dee rekk mooy sab àtte! 9 Ana lu waral ngay biral waxyu ci turu Aji Sax ji, naan kër Yàlla gii dina tas, mel ni ga woon ca Silo, te dëkk bii day tas, kenn du fi des?» Mbooloo ma mépp nag sam Yeremi ca biir kër Aji Sax ji. 10 Kàngami Yuda dégg mbir ma, bàyyikoo kër buur, daldi yéegi ba kër Aji Sax ji. Ñu féncoo ca buntu kër Aji Sax ji ñuy wax bunt bu Bees ba. 11 Sarxalkat yaak yonent ya wax kàngam yaak mbooloo ma mépp, ne leen: «Waa jii, dee mooy àtteem, ndax moo biral waxyu, di rëbb sunu dëkk bii. Yeena ko déggal seen bopp.»
12 Ci kaw loolu Yeremi wax ak kàngam yépp ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Aji Sax jee ma yebal ngir ma biral waxyu, rëbb kër gii ak dëkk bii, te mooy kàddu yi ngeen dégg yépp. 13 Léegi nag rafetal-leen seeni jëfin ak seeni jëf te déggal seen Yàlla Aji Sax ji. Su ko defee Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon. 14 Man nag maa ngii ci seen loxo! Lu ngeen xalaat ne moo gën te war ci man rekk, defleen! 15 Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.» 16 Ba loolu amee kàngam yaak mbooloo ma mépp wax ak sarxalkat yaak yonent ya, ne leen: «Waa jii kay àtteb dee warul ci moom, ndax ci sunu turu Yàlla Aji Sax ji la nu waxal.» 17 Ci biir loolu ñenn ci magi réew mi jóg, wax ak mbooloo ma fa daje mépp, ne leen: 18 «Ku ñuy wax Mise, dëkk Moreset, doon na biral waxyu ca jamonoy Esekiya buurub Yuda. Daa waxoon waa Yuda gépp ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngooru xare yi dafa wax ne:
Dees na gàbb Siyoŋ nib tool,
Yerusalem diy tojit, jale;
tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.”
19 «Ndax tax na Esekiya buurub Yuda mbaa kenn ci waa Yuda reylu ko? Du Buur Esekiya daa wormaal Aji Sax ji, tinu ko, ba Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon? Nun nag musiba mu réy lanu nara indil sunu bopp.»
Yowakim reylu na ab yonent
20 Ci jamono yooyu amoon na keneen ku doon biral waxyu ci turu Aji Sax ji. Muy Uri ma dëkk Kiryaat Yarim, di doomu Semaya. Uri doon biral waxyu, di rëbb dëkk baak réew ma, bokk ak Yeremi genn kàddu gi. 21 Buur Yowakim dégg ay kàddoom, mook mboolemi dagam ak kàngamam yépp. Ba mu ko defee Buur di ko wuta reylu, Uri yég ko, tiit, daw làquji Misra. 22 Buur Yowakim yebal ku ñuy wax Elnatan doomu Agbor ca Misra, mu ànd faak ñeneen. 23 Ñu jëleji Uri ca Misra, yót ko Buur Yowakim, mu jam ko, sànni néewam ca armeelu baadoolo ya.
24 Yeremi nag daa làqoo Ayikam doomu Safan, mu aar ko, ba tàbbiwul ci loxol askan wi, ñu rey ko.