Saar 29
Yeremi bind na ngàllo ga bataaxal
1 Yonent Yàlla Yeremi nag yónnee na bataaxal bu jóge Yerusalem, jëm Babilon ca ndesu magi ngàllo ga, ak ca sarxalkat yaak yonent yaak mépp mbooloo ma Nabukodonosor jële woon Yerusalem, yóbbu leen ngàllo ca Babilon. 2 Mooy gannaaw ba Buur Yekoña bàyyikoo Yerusalem, ànd ak Lingeer yaayu buur ak bëkk-néegi buur ak kàngami Yudak Yerusalem, ak liggéeykati xarala yaak liggéeykati weñ ya. 3 Yeremi yóbbante bataaxal ba Elasa doomu Safan, ak Gemarya doomu Ilkiya, ndaw ya Buur Cedesyas mu Yuda yebal Babilon ca Buur Nabukodonosor. Lii la bataaxal bi wax:
4 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax mboolem ngàllo ga mu jële Yerusalem, yóbbu Babilon, ne leen: 5 Tabaxleen ay kër dëkke; jëmbat seeni tóokër, lekk ca meññeef ma. 6 Takkleeni jabar, am ci doom yu góor ak yu jigéen. Takkal-leen seen doom ay jabar, maye seen doom yu jigéen, ñu am ñoom it doom yu góor ak yu jigéen. Yokkuleen fa, buleen fa néew. 7 Sàkkuleen jàmmu dëkk bi ma leen toxal, te ñaanal ko ci Aji Sax ji, ndax jàmmu dëkk bi mooy seen jàmm.
8 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo, 9 ndax waxyuy fen lañu leen di wax ci sama tur. Yebaluma leen.» Kàddug Aji Sax jee.
10 Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Bu Babilon matalee juróom ñaar fukki ati kilifteefam, dinaa leen dikkal, sottalal leen sama kàddug jàmm, ba délloosi leen bérab bii. 11 Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal.» Kàddug Aji Sax jee. «Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg. 12 Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen. 13 Su boobaa ngeen sàkku ma, daj ma, ndegam sàkkoo ngeen ma seen léppi xol, 14 maa leen di may ngeen daj ma.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di tijjil seen wërsëg, dajalee leen ci mboolem xeet ak mboolem bérab ya ma leen sànni woon.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di délloosi bérab bii ma leen yebale woon ngàllo.»
15 Yeena ne: «Aji Sax ji yónnee na nuy yonent ci Babilon.» 16 Waaye Aji Sax ji dafa wax lu jëm ci buur bi toog ci jalub Daawuda, jëm ci képp ku bokk ci askan wi des ci Yerusalem gii di seen bokk ya àndul woon ak yeen, dem ngàllo. 17 Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Maa ngii di leen yónnee saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu mel ni figg ju nëb, ba kenn manu koo lekk ndax bon. 18 Maa leen di toppe saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu seexlu leen ci mboolem réewi àddina, teg ci di musiba mu ñuy muslu ci biir mboolem xeet wu ma leen sànni, ba ku fay kókkalee, ñoom ngay tudd. 19 Li ko waral mooy ñoo ma déggalul.» Kàddug Aji Sax jee. «Dama leena yónnee yonent yiy samay jaam ay yooni yoon, te déggaluñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.
20 «Kon nag yeen mboolem ngàllo gi ma yebale Yerusalem ba Babilon, dégluleen kàddug Aji Sax ji. 21 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottli waxyuy fen ci turam. Mu ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis. 22 Dinañu tax mboolem kuy móoloo te bokk ca ngàllog Yudeen ña ca Babilon, danga naan: “Yal na la Aji Sax ji teg la mu tegoon Cedesyas ak Akab, ña buuru Babilon lakk cib taal.” 23 Li ko waral mooy njombe wi ñu def fi digg Israyil, di jaalook seen jabari dëkkandoo, di wax ci sama tur ay kàdduy fen yu ma leen santul. Maa ko xamal sama bopp, seede ko.» Kàddug Aji Sax jee.
Semaya jot na tontam
24 «Yaw Yeremi nag, nanga wax Semaya, Neyelameen bi ne ko: 25 “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yaw yaa yónnee ci sa turu bopp ay bataaxal ca askanu Yerusalem gépp, rawatina sarxalkat ba Cefaña doomu Maaseya, ak mboolem sarxalkat ya. Nga di ci wax ne: 26 ‘Aji Sax ji da laa fal sarxalkat, nga wuutu Yoyada sarxalkat bi, ngir kër Aji Sax ji am ku ko yor, ba dof bu fiy wax-waxlu ay waxyu, nga jéng ko, yeewe ko càllalay weñ ci baatam. 27 Ana lu tax waxuloo ci Yeremi mu Anatot nag, moom miy wax-waxlu ay waxyu fi seen biir? 28 Léegi la nu yónnee Babilon bataaxal, ne nu: Dingeen yàgg àll de, kon tabaxleeni kër, dëkke; jëmbatleeni tóokër, lekk ci meññeef mi.’ ”»
29 Ba Cefaña sarxalkat ba jàngee bataaxal boobu, Yonent Yàlla Yeremi di dégg, 30 kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ne ko:
31 «Yónneel ca ngàllo gépp ne leen: Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Semaya Neyelameen ba, ne: “Semaya waxal na leen waxyu, gëmloo leen ay fen, te yebaluma ko. 32 Kon nag Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di mbugalsi Semaya Neyelameen bi, mook askanam. Ku bokk ci moom du toog ci biir xeet wii, bay gis ngëneel li may defal sama ñoñ.” Kàddug Aji Sax jee. “Moo xiirtal askan wi ci gàntal Aji Sax ji.”»