Kàdduy ndollant a ngi
Saar 52
(Saar 52.1-34)
1 Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna. 2 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon. 3 Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xalab leen.
Gannaaw gi Cedesyas fippu buuru Babilon. 4 Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook Yerusalem, yékkati gawukaay, wërale ko. 5 Dëkk ba gawe, ba keroog Cedesyas tollu ci fukkeelu atu nguuram ak benn. 6 Keroog juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund. 7 Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Ñu daldi wuti xuru Yurdan. 8 Waa Babilon nag topp Buur Cedesyas, ba dab ko ca jooru Yeriko. Fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko. 9 Ñu jàpp ko, yóbbu ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem. 10 Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda, ca Ribla. 11 Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, ba noppi jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon, tëj ko fa, ba keroog bés ba mu deeyee.
12 Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am fukki fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem. 13 Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya. 14 Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem. 15 Gannaaw gi ñenn ci baadoolo yi, ak ña nekkoon ca dëkk ba, ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon, ak ña desoon ca liggéeykat ya, Nebusaradan njiital dagi buur boole leen yóbbu ngàllo. 16 Ñenn ca baadooloy réew ma nag, Nebusaradan njiital dag ya bàyyi leen fa, ñuy liggéey tóokëri reseñ yaak tool ya. 17 Ci biir loolu kenuy xànjar ya bokkoon ca kër Aji Sax ji, ak rootukaay yaak mbalkam xànjar ma woon ca kër Aji Sax ji, waa Babilon toj lépp, boole xànjar jépp yóbbu Babilon. 18 Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji: ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak and yu ndaw yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yi ñuy sarxalee. 19 Njiital dag ya yóbbaale ndab yu ndaw yaak and yaak ndab yiy def deretu sarax, ak ndab yiy def dóom, ak tegukaayi làmp yaak and yu ndaw yaak këlli tuurukaay ya. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber.
20 Ñaari kenu yooyu ak mbalka maak fukki nag ak ñaar ya ko yenu, ak rootukaay ya, lépp di xànjar bu Buur Suleymaan defaraloon kër Aji Sax ji, maneesula takk diisaay ba. 21 Kenu yi, gu ci nekk am na taxawaayu fukki xasab* 52.21 xasab mooy guddaayu loxo bu digg-dóomu, diggante catu baaraamu digg ak conc. ak juróom ñett te fukki xasab ak ñaar a koy ub. Mu def pax ca biir te dëllaayu weñ ga di juróom ñeenti baaraam. 22 Kenu gu ci nekk ponku xànjar a ca tege, taxawaayu ponk bi di juróomi xasab, ab caaxub xànjar wodd ko, ànd ak doomi gërënaati xànjar. Ñaari kenu yépp noonu, ànd aki gërënaat. 23 Gërënaat yi juróom ñeent fukk laak juróom benn, wet gu nekk, boo ci boolee ya ca cat ya, muy téeméer, yu ub caax ba.
24 Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya sarxalkat bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja. 25 Biir dëkk ba nag, mu jële fa benn njiitu xare, ak juróom ñaari niti dëkk ba ñu sës ci Buur, ak bindkatub njiital xare ba sasoo bind xarekat yi, ak juróom benn fukki Yudeen ñu mu fekk ca biir dëkk ba. 26 Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla. 27 Buuru Babilon nag bóom leen foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la waa Yuda génne seen réew, dem ngàllo.
28 Lii mooy limu nit ñi Nabukodonosor toxal: Ñetti junniy Yudeen ak ñaar fukk ak ñett (3 023), loolu yemook juróom ñaareelu atu nguuram, 29 ak juróom ñetti téeméer ak fanweer ak ñaar (832), loolu yemook fukkeelu atu nguuram ak juróom ñett, 30 Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600).
31 Yóbbu nañu Yowakin buurub Yuda ngàllo ba mu am fanweeri at ak juróom ñaar, Ewil Merodag doora falu buur ca Babilon. At mooma, fukkeelu weer waak ñaar, ñaar fukki fan ak juróom ca weer wa, ca la Ewil Merodag siggil Yowakin buurub Yuda, daldi koy tijji. 32 Ci biir loolu mu wax ak moom lu rafet, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur, ya mu bokkal curga ca Babilon. 33 Yowakin nag teqlikook yérey kaso ya, ba noppi ñu may ko muy bokk ak Buur ndab giiru dundam. 34 Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, di bàyyikoo ci buuru Babilon bés bu jot, giiru dundam, ba keroog muy dee.