Saar 3
Ayóoba rëbb na bésub juddoom
1 Gannaaw loolu Ayóoba àddu,
ma ngay móolu bés ba mu juddoo. 2 Mu ne:
3 Sànkute ñeel na bés ba ma juddoo,
ba ca guddi ga noon: «Sosees na góor!»
4 Boobu bés yal na di lëndëmu neen,
di bés bu Yàlla ma fa kaw faaleedi,
te genn leer du ko leeralati.
5 Yal na lëndëmu njaniiw aakimoo boobu bés,
xàmbaar mbaaral ko,
muy guddig digg bëccëg gu raglu.
6 Googu guddi yal na ko lëndëm moom,
yàlla bumu bége fi digg bési at mi,
yàlla bees ko limaaleeti ci weer yi.
7 Googu guddi kay yàlla bu ci gone sosooti,
yàlla bu ci sarxolle jolleeti.
8 Yal na alagkati bés yi alag googu guddi,
alagkat yu mana xabtal ninki-nànka.
9 Yal na biddiiwi njëlam giim,
muy séentug leer te du am;
yàlla bumu gis fu njël di xippee,
10 gannaaw moo tëjul sama biiru ndey,
ba làq saay gët coono.
11 Moo lu ma tee woona deeye biiru yaay?
Lu ma tee ne putt, dog, boog?
12 Ana lu may óom doon uufe?
Ana lu ma doon nàmpey ween?
13 Tëdd koon naak jàmm biir bàmmeel,
di nelaw, nopploondook
14 buur yeek jawriñi àddina,
yi tabaxal seen bopp, këri buur yu gental tey.
15 Nopplu koon naak garmi yay boroom wurus,
te daan feesal seeni kër, xaalis.
16 Mbaa ma mel koon ni lumb wu làqu biir suuf,
mbaa cuux mu jotula gis ug leer.
17 Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle,
fa la ña jeele doole nopploo,
18 ña ñu tëjoon ne finaax,
déggatuñu coowal ku leen di sas,
19 ku tuut ak ku mag di fa benn,
jaam noppi faa jaamu sangam.
20 Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf?
Lu boroom naqar di doye bakkan?
21 Ku ni mel ku yàkkamti dee gu dikkul,
te gëna sàkku dee alal ju làqu,
22 ba bu gisoon bàmmeel,
di textexi ci biir mbég ak bànneex.
23 Ngóor sii aw yoonam làqu,
ana lu muy doye dund,
te Yàlla dar kepp ko?
24 Samay binni di samaw ñam,
samay yuux fettax nim ndox.
25 Tiitaange déy a ma dikkal,
li ma ragaloon kay a ma dab.
26 Du jàmm, dug dal, du noflaay bu ma am,
jallaañoo dikk na!