Saar 39
1 Yaa xam jamono ju kéwéli tund di jur?
Am yaa gis fu kéwél di ame doom?
2 Yaa lim weer yi muy ëmb,
am yaa xam fu njuram jote,
3 ba mu sukk, jur,
tàggook mititu matam,
4 ak fa doom jay leqlikook a màgg ci àll bi,
ba dem, te du délsi?
5 Ana ku yóbbu fasu àll, afal ko?
Ana ku yiwi mbaamu àll, wacc ko?
6 Moom mi ma jox màndiŋ mi, mu dëkke,
ak jooru xorom, mu màkkaanoo?
7 Yégul riirum taax,
déggul coowal dawalkat.
8 Tund yi lay wërem poram,
di fa seete gépp gàncax gu tooy.
9 Ndax nagu àll a lay nangoo liggéeyal?
Mbaa mu di la fanaanal ci sa ngédd?
10 Man ngaa takk nagu àll cim rijji,
ba mu topp la, rijjil lab tool?
11 Yaa koy yaakaare dooleem ju bare,
ba dénk ko sab liggéey?
12 Yaay yaakaar mu fatal la jiwu,
jëlil la ko ca dàgga ja?
13 Bànjóolee ngi tëf-tëflu,
te xodd gën koy laaf.
14 Mooy wacci nenam fi suuf,
bàyyee ko tàngooru suuf.
15 Xalaatul tànk bu ci joggi
ak rabu àll wu ko dëggaate.
16 Day soxore doom yi ni lu mu jurul,
coonoom neen, yoonam.
17 Yàllaa ko xañ xam-xam,
te séddu ko xelum ràññee.
18 Waaye bu sàqee, ba sàqi,
faalewul fas ak gawaram.
19 Ndax yaa may aw fas, kàttan?
Am yaa solal ndodd ma, ciiriir?
20 Am yaa koy tëbloo nim soccet,
bu fiiroo, fit rëcc?
21 Fas a ngi bége dooleem, di curpee xur wa,
riddi, dajeek ngànnaay.
22 Yégul tiitaange, ragalul,
dawul saamar.
23 Mbarum fitt a ngay keseŋ-keseŋi fa kawam,
fa xeej ak jaasi lerxatandoo,
24 mu buure xadar, taxañ suuf si,
téyeetul boppam ndax liit ga jolli,
25 mu feeloo ko coowal wakkan ya.
Fu sore lay xañtoo xare ba,
ak kàdduy njiiti xare,
ya riirandook xaacu ya.
26 Ndax sam xel la céeliy daayaarloo,
ba firiy laafam, jëm bëj-saalum?
27 Am yaa sant jaxaay mu naaw ba fa kaw,
di tàgge kawte ya?
28 Aw doj, mu màkkaanoo,
di fanaan kaw catu doj
wu ko kenn dul jote.
29 Fa lay yeeroom rëbbam,
di ko niire fu sore.
30 Ku ñu bóom, ma nga fa teew,
doom yay xab deret ja.