Saar 3
Ñépp la Aji Sax ji di sotti ag Noowam
1 «Gannaaw loolu maay tuur samag Noo
ci kaw wépp suux,
seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu,
seeni màggat di gént ay gént,
seeni xale yu góor di gis ay peeñu.
2 Kera jant yooyu, jaam yi sax, góor ak jigéen,
maa leen di tuur samag Noo.
3 Maay def ay kiraama fi asamaan ak fi suuf;
deret ak sawara ak saxar su jolli.
4 Jant beey soppliku ag lëndëm,
weer wi doon deret,
bésub Aji Sax ji doora taxaw,
bés bu réy bu raglu ba!
5 Su boobaa mboolem ñi woo Aji Sax ji wall
ciw turam,
ñooy raw.
Tundu Siyoŋ ak biir Yerusalem kay
fa la aw ndes di ame,
na ko Aji Sax ji waxe woon,
te ñi Aji Sax ji woo ñooy bokk ci ñi dese bakkan.