Saar 3
Yunus fomm na
1 Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal Yunus ñaareel bi yoon. Mu ne ko: 2 «Jógal dem Niniw, dëkk bu mag ba, nga yegge leen kàddu gi ma lay dénk.» 3 Yunus jóg dem ba Niniw, muy la ko Aji Sax ji wax. Niniw nag def dëkk bu réya réy, ba doxub ñetti fan a koy wër.
4 Ba mu ko defee Yunus tàmbalee wër bés bu jëkk ba, di yéene naan: «Ñeent fukki fan gannaaw tey Niniw dina tas.» 5 Waa Niniw nag gëm Yàlla, daldi yéene koor. Ci biir loolu ku nekk sol ay saaku, di ko ñaawloo, dale ko ca ka gën di mag, ba ca ka gën di ndaw. 6 Mbir ma àgg ca buurub Niniw. Mu ne ñokket, jóge ca ngànguneem, ne futeet mbubbam buuram, sàngoo saaku, daldi toog cib dóom, di ko toroxloo. 7 Ci kaw loolu mu yéenelu dogal bii ca Niniw, ne: «Ci ndigalal Buur aki kàngamam; muy nit aku jur, gu gudd ak gu gàtt, bu ci dara dugg ci seen gémmiñ. Buñu lekk, te ndox, buñu ko naan. 8 Na nit ak jur sàngoo saaku te ñu woo Yàlla wall lu ñu man. Na ku nekk dëddu jëfinam ju bon ak jëfi coxoram. 9 Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»
10 Yàlla nag gis seeni jëf, gis na ñu dëddoo seen jëfin ju bon. Yàlla daldi fomm mbugal ma mu leen naraloon, ba mujju koo def.