Saar 3
Nit a ngi tawat
1 Man maay nit ki gisu naqar,
naqar wu ko yarub sànjum Aji Sax ji teg.
2 Man la jañax, te lëndëm la ma doxloo,
dug leer.
3 Man doŋŋ lay yen aka yenaat loxoom,
bésoo bés.
4 Moo ràppal sama der ak samaw suux,
tas samay yax.
5 Moo tabax fi sama kaw, tanc ma,
gawe ma tooke ak coono.
6 Bérab yu lëndëm la ma dëël,
ni ña dee bu yàgg.
7 Moo ma ñag ba manumaa bëtt,
te jéng yu diis la ma jénge.
8 Su ma yuuxoo, woote wall it,
mu tanqamlu samag ñaan.
9 Ay doji yett la ñage samay yoon,
te moo lajjal samay ñall.
10 Moo di segg mu may tëru,
di gaynde gu waafe làqukaayam.
11 Samaw yoon la ma wàcce, xotat ma,
tumurànkeel ma.
12 Moo ma bankal xalaam,
diire mag fittam.
13 Sama xóotey xol la soqil ay fittam.
14 Maa mujj di reetaanukaayu bokk yépp,
di seen woyu bés bu nekk.
15 Moo ma reggal wextan,
màndal ma lu mel ni xay.
16 Yéyloo na may doj,
dëggaate ma ci pënd bi.
17 Jàmmi xol a ma réer,
ma fàtte sax luy mbégte.
18 Ca laa ne sama doolee (/muñukaaya/darajaa) jeex!
ak sama yaakaar ci Aji Sax ji.
19 Baal xel sama naqar ak sama tumurànke,
wii wextan akug tooke!
20 Dama ciy xalaat aka xalaataat,
sama xol jeex tàkk!
21 Waaye li may dëkke bàyyi xel,
ba dese yaakaar mooy lii:
22 Aji Sax ji, ngoram du dakk,
te yërmandeem du jeex.
23 Xanaa di yeeslu jant bu nekk.
Kee bare kóllëre!
24 «Samab séddoo, Aji Sax jee»
la sama xol wax,
te moo tax ma di ko xaar.
25 Aji Sax jee baax ci ñi ko yaakaar,
baax ci ki koy sàkku.
26 Li baax mooy muñ,
xeremluy xaar wallu Aji Sax ji.
27 Li baax ci nit mooy
nga nangoo muñ ba ngay ndaw.
28 Bu la Aji Sax ji tegee nattu,
berul te muñ.
29 Dëppal sa kanam ci suuf,
jombul yaakaar nuyoo.
30 Dékkal ub lex ku lay mbej,
di la tifaari saaga, ba nga tooy.
31 Boroom bi déy du la wacc ba fàww.
32 Bu la tegee naqar it, yërëm la,
ngoram a ni baree.
33 Du bànneexam lay tege coono,
aka naqaral doom aadama.
34 Bu ñuy dëggaate mboolem ñi ñu tëj cim réew,
35 di jalgati yelleefu nit fi kanam Aji Kawe ji,
36 di been dëgg cib layoom,
Boroom bi da ko dul gis?
37 Ana ku wax, mu am,
te Boroom bi dogalu ko?
38 Muy lu baax, di lu aay,
du Aji Kawe jeey àddu, amal?
39 Kuy dund, ana loo deeti jàmbat,
bu ñu la añalee sa bàkkaar?
40 Nan càmbar, ba xoolaat jikko yi
te dellu ci Aji Sax ji.
41 Nan tàllal sunu xol ak sunuy loxo
Yàlla ja fa asamaan,
42 noo tooñ, noo fippu,
ba tax yaw jéggalewoo.
43 Sam sànj nga làmboo, topp nu,
di rey te ñéebluwoo,
44 aw niir nga sàngoo,
ba ag ñaan du ko jàll.
45 Mbuubitum sën nga nu def
fi biir xeet yi.
46 Sunu noon yépp a nuy waxal,
47 tiitaange ak pax dikkal na nu,
ak yàquteek sànkute.
48 Saay gët a ngi wal ndax sama askan
wi rajaxoo.
49 Saay gët a ngi rogalaat, du fer, du ŋiis,
50 ba keroog Aji Sax ji séentoo asamaan, ba gis.
51 Bi ma gisee li dal jigéeni dëkk bi yépp,
la sama xol jeex.
52 Ñi ma bañ ci dara ñoo ma këpptala këpptal
ni picc.
53 Cib teen lañu ma tàbbal, ube kow doj,
te may dund,
54 ndox ma mëdd ma,
ma ne: «sànku naa.»
55 Aji Sax ji, fa xóotey pax ma
laa la wooye
56 Sama baat nga dégg, ma ne la:
«Bul fattal sab nopp, samay onk
ak samay yuux.»
57 Bés ba ma la wooyee nga dikk,
ne ma: «Bul tiit.»
58 Boroom bi, yaa sàmm sama àq,
yaa jot sama bakkan.
59 Aji Sax ji, yaa gis ni ñu ma tooñe,
jox ma sama àtte.
60 Yaa gis seen mboolem mébetu feyu,
seen mboolem pexe yi ñu may lalal.
61 Aji Sax ji, yaa dégg seeni kókkalee,
ak mboolem pexe yi ñu may lalal.
62 Ci man la noon yiy diisoo aka déeyoo,
bés bu nekk.
63 Xoolal, bu ñu toogee ak bu ñu jógee,
man lañuy léeboo.
64 Aji Sax ji, jox leen seenub añ,
seen kemu liggéeyu loxo.
65 Dërkiisalal seen xol (Tegleen njàqarey xol / Muural seenum xel,)
na leen sag alkànde ñeel.
66 Toppe leen sa mer, te nga sànke leen
mboolem fu asamaanu Aji Sax ji tiim.